Taalifi cant112wol_mbs

Ku ragal Yàlla gis mbaaxam

1Màggalleen Ki Sax!Ndokkalee ku ragal Aji Sax ji,di tàqamtikoo ay santaaneem.2Aw askanam ay am doole ci réew mi.Ku jub saw xeet barkeel,3alal ak koom am sa kër,sag jëf yu jekk sax dàkk.4Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jubak ku baax, di boroom yërmande ak njubte.5Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble,di jëflante cig njub.6Ku jub du tërëf mukk,te dees na ko fàttaliku ba fàww.7Du ragal dég-dég bu tiis,xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji,8fit wa toog, du ragal,ba kera muy gis noonam jóoru.9Moo yéwén ci li muy may néew-doole yi,njekkam sax dàkk,dooleem di yokku, ànd ak daraja.10Soxor bi da koy gis, mer,iñaan bay yéyu, jeex tàkk;nde soxor, yaakaar ju tas rekk.