1Màggalleen Ki Sax!Naa sante Aji Sax ji léppi xolci biir ñu jub ñi bokk jataay.2Liggéeyi Aji Sax ji réy na,ku ko safoo di ko gëstu.3Jëfam di teddngaak daraja,njubteem di sax ba fàww.4Moo dogal ñuy fàttalikuy kéemaanam;Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.5Mooy leel ku ko ragal,di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.6Won na ñoñam dooley jëfam,ba mu leen joxee suufu xeet yi.7Ay jëfam dëgg laak yoon,tegtalam yépp mata wóolu,8laloo dëgg ak njub,te sax dàkk ba fàww.9Moo yónnee xeetam wall,fas ak ñoom kóllëre gu sax.Kee sell te jara ragal!10Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel,dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye.Moo yeyoo cant ba fàww.