Taalifi cant110wol_mbs
Yàlla fal na nitam
1Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko:«Toogeel sama ndijoor,ba ma def say noon sa ndëggastal.»2Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ.Yilifal noon yi la wër!3Sa mboolooy taxawal seen bopp,sa bésub xare.Ñu sol darajaak cellte,faboo fa njël sosoo,diy ndaw, wàccsil la, nib lay.4Aji Sax jee ko giñ,te du dellu gannaaw:«Yaa dib sarxalkat ba fàww,topp dayob Melkiccedeg .»5Sang baa ngi fi sa ndijoorte mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.6Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew,di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj.7Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan,te moo ko tax di siggi.