1Santleen Aji Sax ji, kee baax,kee saxoo ngoram!2Waxleen lii, yeen ñi Aji Sax ji jot,jote leen ci loxol bañ,3dajalee leen fa réew ya,jële leen penkook sowu,ak bëj-gànnaar ak wetu géej.4Ñee ngi taxawaaloo màndiŋ mu wéet,gisuñu dëkkuwaay,5boole xiif ak mar,ba bakkan di tàggoo.6Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,mu xettali leen ci seen njàqare,7jaarale leen ci yoon wu jub,ngir ñu àgg cib dëkk.8Nañu sante Aji Sax ji ngoramak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.9Mooy màndal put gu wow,di feesal ngëneel biir bu wéet.10Ñee ngi dëkke lëndëm gu tar,ñu yeewe leen jéngi weñ yu tar.11Ñoo gàntal waxi Yàlla,néewal ndigalal Aji Kawe ji.12Mu teg leen naqar, ba toroxal leen,ñu ne nërëm te kenn walluwu leen.13Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,mu wallu leen ci seen njàqare,14xar seeni jéng ñaar,génnee leen lëndëm gu tar.15Nañu sante Aji Sax ji ngoramak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.16Moo rajaxe bunti xànjar,damm galani weñ.17Ñu dofe ñalee ngi topp yoonu moy,loroo seeni ñaawtéef,18bàyyi luy ñam di daw seen yaram,ñu jege bunti dee.19Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,mu wallu leen ci seen njàqare.20Daa yónnee kàddoom, wéral leen,këfe leen cim yeer.21Nañu sante Aji Sax ji ngoramak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.22Nañ ko sarxal saraxi canttey sarxolle, siiwale koy jalooreem.23Ña ca des a ngi war gaal, dugg géej,di liggéeye mbeex mu ne xéew.24Ñooñoo seede jaloorey Aji Sax ji,ak kéemaanam ya fa xóote ya.25Day àddu, sant ngëlén,mu yékkati gannax yi.26Gannax ya fettax ba ca kaw-a-kaw,xàwweekoo fa, tàbbi xóote ya.Ñu jàq ba fit ne soyox,27di jang, di kayaŋ-kayaŋi niy màndikat,pexe jeex.28Ñu jàq, woo Aji Sax ji wall,mu génne leen ci seen njàqare,29dalal ngëlén la,gannax ya selaw,30ne tekk, ñu bég,mu gindi leen ba fa ñu bëgga teer.31Nañu sante Aji Sax ji ngoramak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.32Nañu ko kañe ndajem mbooloo mi,di ko màggale péncum mag ñi.33Mooy soppi wali ndox màndiŋ,soppi bëti ndox suuf su ne sereŋ,34suuf su nangu doon jooru xoromndax mbonug ña ko dëkke.35Mooy soppi màndiŋ it, ndox ya taa,soppi suuf su ne sereŋ bëti ndox;36dëël fa ñu xiif,ñu sanc fab dëkk, dëkke,37ji ay tool, jëmbat ay reseñ,mu meññ, ñoral,38Aji Sax ji barkeel, ñu giir a giir,te wàññiwul seenug jur.39Bu ñu wàññikoo, ba néew doolendax nooteel ak coonooku tiis,40Aji Sax ji sib seen njiit yi leen noot,wërloo leen àll bu amul yoon.41Waaye mooy teggil néew-ji-doole coonoom,ful njabootam nig jur,42aji jub ñi gis ko, bég;mboolem ku bon wedam.43Ku xelu ku ne, na ràññee liite seede li Aji Sax ji jëfe ngoram.