Taalifi cant105wol_mbs

Aji Sax ji sàmm na kóllëre

1Santleen Aji Sax ji, tudd turam,xamley jalooreem ci biir xeet yi.2Woyleen ko, tagg ko,yégleleen mboolemi kéemaanam!3Damooleen turam wu sell,yal na kuy wut Aji Sax ji am bànneexu xol.4Wutleen Aji Sax ji, sës ci dooleem.Saxooleen koo wër!5Fàttalikuleen ay jalooreemaki kéemaanam aki àtteem.6Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba,yeen sëti Yanqóoba, yeen ñi mu tànn!7Kee di sunu Yàlla Aji Sax ji,di àtte suuf sépp,8di fàttaliku ba fàww kóllëreem,ak kàddoom ga mu digoon Ibraayma,ba ci junniy maas,te mu giñal ko Isaaxa,10dëggalal ko Yanqóoba, sàrtal ko,fase kook Israayil mooma kóllëre gu sax.11Moo noon: «Yaw laay jox réewum Kanaan,muy sa cér, nga séddoo.»12Ba bànni Israayil doonee ñu néewa néew,diy doxandéem ci réew mi,13di wëreelu ci biir xeetoo xeet,ak nguuroo nguur,14mayul nit mu noot leen,te yaral na leen ay buur,15ne leen: «Buleen laal ñi ma séddoo,te samay yonent buleen leen lor.»16Moo wàcce ab xiif ca réew ma,dagge fa lépp luy gub,17yónnee ku leen jiitu,muy Yuusufa ma ñu jaayoon njaam,18tànk ya, ñu jéng jéng yu tar,baat ba, ñu yeewe caqu weñ.19Kàddug Aji Sax ji di nattu Yuusufa,ba keroog pirim ma dikk,20Buur a yónni ku ko yiwi,ku yilifi xeet a ko tijji.21Mu sas ko mu jiite këram,di saytu mboolem alalam,22ba saña tënk jawriñi buur ci coobareem,tey xelal mag ña.23Israayil agsi Misra,muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam .
24Aji Sax ji giiral xeetam wa,ba ñu gëna bare seeni noon,25mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam,ñuy fexeel jaamam ñooña.26Mu yónni Musaa, jaamam ba,tànn Aaróona, boole ca,27ñu sottal ci seen biir firndeem ya mu waxoon,muy kéemaan ya ñu def ca réewum Xam.28Moo yónnee lëndëm, lëndëmal,te Musaa ak Aaróona gàntaluñu kàddoom.29Moo soppi seen ndoxum réew deret,rey seeni jën,30feesal seen réew ay mbottyu àkki seen biir néegi buur ya.31Moo àddu, weñ ya dikk,yoo ya dajal seen réew ma.32Mu def seenub taw tawub yuur,sawaray melax jafal seen réew ma.33Mu dal ci seen figg ak reseñ,daaneel seen garabi réew ma.34Mu àddooti, ay soccet dikk,di njéeréer yu wees ab lim,35ñu lekk luy gàncax ca seenum réew,lekk lu suuf sa meññ.36Moo faat luy taaw ca seenum réew,muy lu njëkka soqeekoo seen digg doole.
37Mu génne leen, ñu yóbbaale xaalis ak wurus,te kenn tërëful ca seeni giir.38Misra daa bég ba ñu demeendax tiitaange ju ñu leen tiital.39Mu firiw niir, yiire leen,ak sawara, ñu niitoo guddi.40Ñu sàkku, mu wàcceey picci përëntaan,teg ca reggal leen mburum asamaan.41Mu bënnu doj, ndox ma ball,di dex, wale joor gu wow.42Daa bàyyi xel kàddoom gu sell,ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.43Moo génne ñoñam, ñu bég,moo génne tànnéefam ña, ñuy sarxolle.44Mu jox leen suufi yéefar ya,ñu jagoo ñaqi xeet ya,45ngir ñu sàmm ay dogali yoonam,topp ndigali yoonam.Màggalleen Ki Sax!