Taalifi cant101wol_mbs

Buur a ngi jaayanteek Yàlla

1Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Ngor ak yoon laay woy.Yaw Aji Sax ji laay joobe.
2Naa teewlu yoonu màndute.Ana kañ nga may dikkal?Naa doxe màndutefi sama biir waa kër.3Caaxaani neen, xooluma;jëf ju wàcc yoon, bëgguma,taqu ma fenn.4Kuy nas njekkar, sore ma;lu bon, xawma ko.5Kuy jëw moroomam, ma wedamal;ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la.6Ku dëggu ci réew mi, ma geesu,ngir fat ko.Te kuy wéye màndute,kookoo may liggéeyal.7Kuy njublaŋ du tooge sama kër,kuy fen du taxaw sama kanam.8Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi,ngir génne ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.