1Éy Aji Sax ji, lu la taxa sore?Xanaa dangay làqu, bésub njàqare?2Ku bon naagu na, ne dann néew-ji-doole,lal ay pexeem, ba jàpp ko.3Ku bon déy a ngi tëggoo bànneexu bakkanam,ku bëgge di ñàkke wormaaka teddadil Aji Sax ji.4Ku bon daŋŋiiral, seetul dara,xalaatam yépp mooy Yàlla amul.5Saa yu fexee, juble,te gisul sa ndigali yoon yi ko tiim.Ma ngay ciipu bañam yépp.6Ma nga naan ca xelam: «Duma tërëf,safaan du ma dab tey ak ëllëg.»7Ay móolu la gémmiñ ga fees ak fen ak noote,njekkar ak ñaawtéef lal làmmiñ wa.8Day tëroo ciy dëkk-dëkkaan,làqu di bóom ku deful dara,nëbbu di wootal néew-ji-doole.9Day làqu béreb, di yeeroo ni gaynde cim xuntam,di yeeru aji ñàkk, ba jàpp ko,laaw ko, ñoddi, yóbbu.10Ma ngay sëgg aka waaf,ba aji ñàkk daanu ci loxoom.11Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na,dummóoyu na, du xoolati.»12Aji Sax ji, jógal!Éy Yàlla, xàccal sa loxo.Bul fàtte néew-ji-doole.13Bul may ku bon mu sofental la,te naan ci xelam: «Yàlla du ma ko topp.»14Yaw de yaay ki nemmiku,di gis njekkar ak naqar,ku mu dal, nga sàmm àqam.Néew-ji-doole wéeroo la,ab jirim, nga dimbali.15Ngalla dammal loxol ku soxor ak ku bon,topp leen seen coxor gi ñu yaakaaroon ne du feeñ.16Aji Sax jee di Buur ba fàww!Xeet yeey sànku, jeex cim réewam.17Aji Sax ji, yaay dégg dagaanu néew-ji-doole,yaay dalal xelam, teewlu ko,18ngir sàmm àqu jirim ak néew-ji-doole,ba nit kiy suufu kese dootul xëbale.