1Peeñum Abdiyas a ngii. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii ñeel askanu Edom. Lu jëm ci mbugalum Edomeen ñiAb dégtal lanu dégg, mu bawoo fa Aji Sax ji,ndaw lañu yebal ci biir xeet yi,mu ne: «Jógleen, nu jóg song Edom xare.»2Aji Sax jee ne waa Edom:«Tuutal leen laay def ci biir xeet yiyeen, ñu xeeblu lool ngeen di doon.3Seen reewande sànk na leen,yeen ñi dëkke xar-xari doj,te seen dëkkuwaay sore kaw,ba tax ngeen naan ci seenum xel:“Ana ku ñu mana daane fi suuf?”4Su ngeen kaweeloon nig jaxaay,ba seenum tàgg làqe ci biiri biddiiw it,fa laa leen di wàccee.»Kàddug Aji Sax jee.5«Su leen ay sàcc dikkalee, mbaa sëxëtookati guddi,yeenakay yàqule!Waaye xanaa du la leen doy lañuy sàcc?Su leen wittkati reseñ dikkalee,xanaa dinañu ca wacc ay doom?6Waaye céy ni ñuy sëxëtoojee askanu Esawu!Céy ni ñu nara jeexaatoo seeni denc!7Mboolem ñi ngeen fasool kóllëreñoo leen di waññi ba ca seen kemu réew,seeni am-di-jàmm ñoo leen di nax ba man leen,ñiy lekk seenu ñam tegal leen ag fiir ci seeni tànk,ndax Edom moo amul ag dégg.8«Xanaa du bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,«fi Edom laay tukkale boroomi xel,tundu Esawu woowu laay jële luy taxa dégg.9Yeen waa Teman , seeni jàmbaar ay jàq,ba mboolem waa tundu Esawu faatu.
Lii moo waral mbugal mi
10«Soxore gi ngeen soxore seen mbokk Yanqóobamoo leen tax di sangoo gàcce,te dees na leen dagg sànni ba fàww.11Bésub keroog ba ngeen taxawee,janook seen mbokk,bésub keroog ba jàmburñay yóbbu seen alali bokk,ay doxandéem song bunti dëkkam,bay tegoo bant teraangay Yerusalem,yeen itam, ni noon yooyu ngeen def.12Waruleen woona seetaan ci seen bésub mbokk,bésub njekkaram,Waruleen woona bége deminu Yudeen ñici seen bésub sànkute,mbaa ngeen di réy làmmiñ,ci bésub njàqare.13Waruleen woona dugg sama dëkku ñoñ,ci seen bésub tiis.Waruleen woona bokk ci ñiy seetaan seenu ayci seen bésub tiis.Waruleen woona teg loxo seeni teraanga,ci seen bésub tiis.14Waruleen woona taxaw fa selebe yoon ya,di dogale ña rëcce ca ñoom,waruleen woona delloo ña dese bakkanca loxol noon ya, ci bésub njàqare.
Bésub Aji Sax ji xeet yépp la ñeel
15«Bésub Aji Sax ji déy, dëgmal na,ñeel xeetoo xeet.Li ngeen def rekk lees leen di def,seenug pey këppu ci seen kaw bopp.16Yeen waa kër Yanqóoba,ni ngeen naane sama kaasu mbugal ca sama kaw tund wu sell,ni la xeet yépp di naane ba fàww,di naan aka jolu ba mel ni masuñoo nekk.17Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe,te dina doon béreb bu sell,waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.18Kër Yanqóoba sawara lay doon,kër Yuusufa dib tàkk-tàkk,kër Esawu di boobbu ñuy lakk, xoyom ko,ba kenn du dese bakkan ci kër Esawu.»Aji Sax jee ko wax.19Waa bëj-saalumu Yuda ñooy moom tundu Esawu,waa suufu tund ya moom waa Filisti,ñooy moom itam réewum Efrayim ak réewum Samari,giirug Beñamin moom diiwaanu Galàdd.20Waa Israayil ñi ñu gàddaayloo woon,gàngoor googu ñooy moomréewum Kanaaneen ña, ba ca Sarebta,te waa Yerusalem ca Sefarat, ñi ñu gàddaayloo woon,ñooy moom dëkki Negew ca bëj-saalum.21Ay xettalikat ñooy yéeg kaw tundu Siyoŋ,ngir yilif tundu Esawu,nguur gi di moomeelu Aji Sax ji.