Nawum2wol_mbs
1Ndaw a ngii dawe kaw tund ya,di indi kàddu, xibaaru jàmm.Yaw Yuda, bégeel sa bési màggal,te wàccook say xas.Nit ku bon ki dootul jaare fi yaw;léppam lees di dagg, sànni.2Ki lay falaxe buur na, wutsi la!Sàmmal sab tata, wattu saw yoon,takkal sa ndigg, te dëgërlu bu baax.3Aji Sax ji moo yeesal darajay Yanqóoba,darajay Israayil moomu.Ay taskat a ko tasoon,yàqate ay caram.