Mise3wol_mbs

Aji Sax ji tiiñal na njiiti Israayil

1Dama ne:«Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba,yeen kilifay kër Israayil!Xanaa du yeena wara xam yoon?2Te yeenay bañ-kati lu baax,di bëggkati lu bon.Yeenay fees sama ñoñ te ñuy dund,yeenay rocci suux wi sàng seeni yax.3Yeenay yàpp samay bokk,fulli seen der,damm seeni yax, dogat,def ko ni toggug kawdir,mel ni ndawal ci cin.»4Lee tax noggatukat yii di woo Aji Sax ji wall,te du leen wuyu,kanamam la leen di làq, bésub keroog,ndax ñoo bonal seeni jëf.

Aji Sax ji artu na yonent yu bëgge yi

5Lii la Aji Sax ji wax ci yonent yiy lajjal samay bokk:«Bu ñu sàqamee ab lanc, yéene jàmm;ku leen leelul, ñu waajal xare.6Moo tax yeen, guddi moo leen di ñeel, ba peeñu réer,lëndëm a leen di dikkal, ba am ngis tukkil leen,jant mooy sowal yonent yi,bëccëg lëndëmal leen.7Seetkat yi dañuy rus,boroom peeñu yi torox,ñoom ñépp jàpp seen gémmiñ;ndax Yàllaa leen dul faale.»
8Teewul man, may fees ak doole,fees ak noowug Aji Sax ji,ak dëgg ak njàmbaarte,ngir biralal askanu Yanqóoba bàkkaaram,ngir tuddal bànni Israayil googu moyam.

Aji Sax ji tiiñalaat na njiiti Israayil

9Ngalla dégluleen lii, yeen njiiti kër Yanqóoba;yeen kilifay kër Israayil.Yeen ñi seexlu dëgg,lunkal wépp yoonu njub.10Deret ngeen tabaxe Siyoŋ,njubadi ngeen tabaxe Yerusalem googu.11Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee,seeni sarxalkat di feyeeku am njàngale,seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane,te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan:«Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir?Musiba du nu dab!»12Kon nag yeena tax dees na gàbb Siyoŋ nib tool,Yerusalem googu diy tojit, jale,tundu kërug Yàlla gaay doon gajj bu kawe.