1Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Mise miy waa Moreset, ca janti Yotam ak Axas ak Esekiyas, buuri réewum Yuda, na seen nguur topplantee. Lii la Mise gis ci mbirum Samari ak Yerusalem.
Aji Sax ji yékkati na kàddug tuuma
2Dégluleen, yeen, xeetoo xeet,teewlul, yaw àddina ak li ci sa biir,ba Boroom bi Aji Sax ji seedeel leen tuuma,Boroom beey àddoo fa màkkaanam mu sell ma.3Aji Sax jaa ngii di génne ca bérebam ba,mooy wàccsi, daagoo kawtey suuf.4Tund ya mu joggi da naan soyox seey,xur ya xar, wàyyi ni dax ju jege sawara,def ni ndox mu wale kaw mbartal.5Bàkkaaru Yanqóobaa waral lii lépp,moyi Israayil googu la.Ana luy bàkkaaru Yanqóoba?Da dul Samari?Ana fuy bérebi jaamookaayi xërëm ci Yuda?Da dul Yerusalem?6«Maay saam Samari, def ko jalu tojitci mbooy gi,» la Aji Sax ji wax.«Maa koy def jëmbatukaayub reseñ,maay yuri ay doji tabaxam ca xur wa,ñori suuf sa mu sampe.7Seen jëmmi tuur yépp ay rajaxoo,te mboolem seen peyoor yu sobewuday lakk ba jeex.Maay tas tasar mboolem seen jëmmi xërëm ,seen peyi gànc a leen ko may,kon na ko seen moroomi gànc feyeekoo.»
Ñaawlu dikkal na Yuda
8Lee ma tax di jooy aka yuuxu,ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo.Naa yuuxu nig till,naa sab sabum looy ndaxu naqar.9Góom bi Aji Sax ji teg Samari kat amul paj,te moo law ba Yuda,àkki ba buntu Yerusalem, ca saay bokk.10Buleen ko nettali fa Gaat ,buleen jooy benn yoon.Xalanguleen fa pëndub suuf sa ca Bet Leyafra ,di ko ñaawloo.11Yeen waa Safiir , wéyleen,ak gàcce ak yaramu neen.Waa Caanan sañuñoo génn,te wall du bawoo fa waa Bet Eccel ,ñay jooy seeni néew.12Waa Marot a mar jàmm,te aw ay a wàcce fa Aji Sax ji,ba agsi buntu Yerusalem .13Yeen waa Lakis , takkleen fasi dawkat ak watiir.Yeena njëkka moyloo janq Siyoŋ mu taaru,ci yeen lañu njëkka gise bàkkaari Israayil.14Yeen waa Yuda, mayleen waa Moreset Gaatlu ngeen tàggatook ñoom,këri Agsib wori neen lay doon ci buuri Israayil.15Yeen waa Maresa laay indil ku leen moom,te ca Adulam la ñi Israayil di damoo di làquji.16Watuleen nel, ñaawloo kodoom yi leen doon bànneexal.Neluleen nel yu set nim tan, naqarloo,nde dañu leen di gàddaayloo, teqalikook yeen.