Jooytu1wol_mbs

1Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey!Te ñoñam noon gàññ démb.Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey,te noon ràññ fi biir xeet yi!Moo doon lingeeru diiwaan yi,tey, mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.
2Day fanaanee jooy a jooy,rongooñ yay bas-basi,te du kenn ku koy dëfalci mboolemi soppeem.Xaritoo xarit wor ko,walbatiku diy noonam.
3Ngàllo lañu yóbbu Yuda,ci biir naqar ak njaam gu metti.Ci biiri jàmbur lañu dëkk,amuñu fu ñu noppaloo,mboolem ña leen dàq a leen dab,ba tance leen ca ruq ya.
4Yoon yi jëm Siyoŋ jooy na wéet,kenn jaareetu ca màggalsi.Pénc yépp a gental,sarxalkat yay binni,janq ja jàq,Siyoŋ gépp di naqarlu!
5Seen noon yaa jiite tey,seen bañ yooyoo ne finaax,Aji Sax jee mbugale waa Siyoŋseeni tooñ yu bare,seeni doom duggig njaam,di moomeelub noon.
6Lu doon sagub Siyoŋ, dëkk bu taaru bi,tey, sàggiku na.Seeni garmee ngi mel ni kéwélyu amul parlu,di koyoŋ-koyoŋiy daw,te rëbb ne leen dann.
7Tey ci janti toroxte ak tumurànke,la Yerusalem di fàttalikoomboolem ngëneeli démbam.Aw askanam a tàbbi ci loxol noon,te wall amul,noon ba gis leen,di tex-texi ci seenug yàqule.
8Yerusalem a moy a moy,ba tax koo mujj di sobe;ku ko teraloon, sofental ko,ndax gis ko, mu ne duŋŋ.Moom ci boppam mu ngi binni,fuuylu.
9Sobey Siyoŋ ca pendalam,te bàyyiwul xel ag mujam.Jéllam ba yéeme na,te amul ku ko dëfal.Siyoŋ nee: «Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare;noon bi déy, am na ndam!»
10Loxo la noon bi teg cingëneeli Siyoŋ gépp.Siyoŋ kay a gis yéefar yi songsikëram gu sell gi,te ci ñoom nga santaane woon, nebuñu dugg sam ndaje .
11Waa Siyoŋ gépp a ngi binni,di wut ab dund ,seeni ngëneel lañuy weccikoo aw ñamwu ñu leqalikoo.Yerusalem àddu naGisal Aji Sax ji, seetalni ma mujj tekkeedee!
12Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi,lii safu leen,waaye seetleen rekk ba gisndax wenn mitit dab namitit wi ñu ma teg,te Aji Sax ji naqarale ma koci jantub tàkktel sànjam.
13Fa kaw la Aji Sax ji sànnee sawaraci sama biiri yax,moo laaw ab caax ngir fakkastal ma,waññi ma, jànnaxe ma,ma dëkke yoggooral.
14Samay tooñ la Aji Sax ji ëmb,fastee ko loxoom,mu tege sama kaw ndodd,ba jeexal sama doole.Boroom bee ma tàbbalci loxo yu ma manula të.
15Ku doon jàmbaar fi sama biir,la Boroom bi xalab.Am ndaje la ma wooteel,ngir falaxe sama ndaw yu góor.Boroom bee dëggaate Yuda, janq ju taaru ji,ni reseñ ci biir nalukaay.
16Looloo ma tax di jooy,rongooñ di wal-wali,te ku may dëfal sore ma,mook kuy seral sama xol.Samay doom a ngi jaaxle,nde noon bi daan na.17Siyoŋ tàllal na loxoom,waaye amul ku ko dëfal.Aji Sax jee wool askanu Yanqóobaseeni noon yi leen wër,ba Yerusalem mujj di sobe fi seen biir.18Aji Sax ji moo yey,kàddoom laa gàntal.Yeen, xeetoo xeet, ngalla dégluleente xool samaw tiis.Samay ndaw yu góor ak yu jigéen,ñoo duggi ngàllo!
19Samay soppe laa woo wall,ñoom ñu wor ma.Samay sarxalkat ak samay mag di wuti ab dundbu ñu leqalikoo,far faatu ci biir dëkk bi.
20Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare,samay butit di fuddu,sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis.Man de maa gàntal ba gàntaaral,ba fa biti, saamar di fa bóome,te biir kër it di dee.
21Dégg nañu may binni,te awma ku ma dëfal.Noon yépp a dégg samaw ayte di ko bége, nde yaa ko def.Ngalla indil bés bi nga dige,ba ñu daj li ma daj.
22Yal na seen gépp mbon teew fi sa kanam,ba nga mbugal leenni nga ma mbugalendax mboolem samay tooñ.Samay onk bare na,sama xol jeex tàkk.