Ayóoba41wol_mbs

1Wii rab, yaakaar koo jàpp nax sa bopp la;bu nee jaas, nga jóoru.2Kenn ñàngul, ba sañ koo merloo.Kon ana kuy taxaw fi sama kanam man?3Ana ku ma abal lenn ba ma war koo delloo?Lépp lu mboolem asamaan tiim, maay boroom!4Rab wii, duma noppee waxtaaney céramak kiraamay dooleem ak jekkaayu bindam.5Ana ku mana summib turkeem?Ana ku mana bëtt kiiraayu ñaar-caam?6Ana ku koy ŋaal,ak sellam yu dajal te raglu?7Gannaaw gi ay sàppey pakk la,di ab tay bu tëje ràpp,8dugglante benn-benn,ba ngelaw sax xaju ca,9xanaa ñu ne ñàpp, ku ne taq sa moroom,te duñu teqalikoo.10Bu tislee, melax ne ràyy,mu xippi, nga ne fajar ay xapp-xappal.11Jumi sawaraay tàkke ca gémmiñ ga,ferñent ya jiitu,12saxaar di sël-sëlee ca wakkan ya,mbete cóolóolu cin luy bax.13Ngelawal bakkanam jafal nay xal,sawara ne jippét, tàkke ca gémmiñam.14Ndoddam la doole daloo,te fu mu dëgmal tëbum tiitaange fa la.15Ay ndombo la der ba def, dankalikoo,ne këcc, ne degg.16Dënn baa nga dëgër niw doj,ne këcc ni doju wolukaay.17Bu jógee, jàmbaar ñi tiit,muy rajaxe, ñu jommi.18Nga jam ko saamar, du dugg;xepp akug fitt akub xeej, noonu.19Weñ gu ñuul di ko safum mboob,xànjar niru ko matt mu nëb.20Ndawal fitt dawloowu ko,doju mbaq di ngooñ mu koy ñiramtal.21Bolde di ko saf ñax gu wow,ab xeej riir, def koy ree.22Lu mel ni tojitu xandeer a lal biir ba,di rijji bañ bi.23Mooy baxloo xóote yi ni cin,di fuural géej ni njaq lu garab xooje.24Gannaawam ay def xàll wuy lerxat,mbàmbulaan miy saf bijjaaw.25Amul niruwaale fi kaw suuf,mii mbindeef mu dul tiit.26Képp ku réy, mu xool la bëtu suufe,képp ku bew, muy sa buur.