Ayóoba40wol_mbs
1Aji Sax ji dellu ne Ayóoba:2Yaw miy layook Aji Man ji, dangay diiŋat?Yaw miy weranteek Yàlla, doo tontu?3Ayóoba àddu ne Aji Sax ji:4Man mi tekkiwul dara, nu ma lay tontoo?Sama loxo laa ube sama gémmiñ.5Maa waxoon benn yoon, waxatuma;maa tóllanti woon, dootul am.