Ayóoba33wol_mbs
1Léegi Baay Ayóoba, ngalla déglul samay waxte teewlu sama kàddu yépp.2Xaaral, ma àddu boog,ba sama làmmiñ tudd li may bëgga wax.3Xel mu dëggu laay waxe,samay kàddu di xam-xam bu wóor.4Ngelawal Yàllaa ma sos,noowal Aji Man ji daal a ma may bakkan.5Soo manee, tontu ma;defarul, janook man.6Maa ngii, yem ak yaw fa Yàlla;ci ban lañu ma mooñe man itam.7Du sama ñàngaay bu lay tiital,du sama daraja ju la diis.