Ayóoba30wol_mbs

Ayóoba jooy na coono

1Tey ñi may diijoo ngii, te ñoo ma féete ndaw,seeni baay a tekkiwuloon tus,ba ma siide leena jël, ñuy sàmmandook samay xaj.2Ana njariñ lu ñu ma amaloon sax?Yooyu kooñoor yu jeele?3Ñii ndóol, xiif, desey yax,di ŋeeñaatoo biir àll,fu lëndëm, gental, maral,4di witt ñax mu saxe ciy tanaka gasi reen, di dunde.5Ñooñu lees dàqe fi biir nit ñi,di leen yuuxoo niy sàcc,6ñu dëkkey xur,ci biiri pax aki doj,7di ŋaaxe biir gajj gi,dankaloo ci ron dég yi.8Ñu sew lañu, ñu kenn yégul,xanaa caw leen, génne réew mi.
9Tey nag ñoo may woyantoo,di ma léeboo.
10Dañu maa seexlu, ñooru ma,néeg maa serati ci kanam.11Yàllaa ma nasaxal, toroxal ma,ba amatuñook man yemukaay.12Mii njurum baadoola mu féete ndijoor, di ma téqtal,di ma xàllal yooni sànkute.13Ñu ngi may dogale, nar maa musibaal,te soxlawuñu ci ndimbal.14Fu yaa lañu bëtte,buure jali tojit, ne jàyy fi sama kaw.15Musiba da maa ëlëm,sama daraja naaw ni ngelaw,sama teraanga naaxsaay niw niir.
16Tey maa ngii sama bakkan di ŋiis,bési njàqare ne ma taral.17Guddi dikk di bënn samay yax, muy rot,mitit di ŋereñ te du selaw.18Kii ne nikk sama mbubb,ne ràtt sama baatu mbubb,19xalab ma ci biir ban bi,may nirook pënd akub dóomu-taal.20Woo naa la wall, wuyuwoo ma,ma taxaw, nga niir ma.21Yaa soppiku, néege ma,di ma soxoree sa diisaayu loxo.22Yaa ma ne siféet, waral ma ngelaw,pamti-pamtee ma biir ngëlén.23Xam naa xéll ne ci dee nga ma jëme,te mooy kërug ndajem képp kuy dund.
24Ku sànkule du tàllal loxoo?Ku musiba dab du woote wall?25Moona sama rongooñ a daan tuurul boroom tiis,sama xol di tiisoo aji ñàkk ji.26Lu baax laa yaakaar, lu bon ne jalañ,leer laa séentu, guddi ne jaas,27sama xol lëmbaajoo, tëë dal,bési naqar dogale ma.28Maa ngi wéye ñuulaay bu ma tàngoor tegul,di taxawe biir ndaje, di woote wall.29Damaa mujj bokk ak till,neexook looy,30ñuul, yaram di xub,tàng, di bax,31sama xalam tiisal,sama toxoro jooy.