Ayóoba17wol_mbs

1Sama xol jeex,samay fan tàggoo,bàmmeel di ma xaar.2Fu ma jublu ñu di ma ree,di ma ñaawal, may gis.
3Ngalla Yàlla, gàddul mab daan sama digg ak yaw;su dul yaw, ana ku may gàddu?4Yaa fatt xelu ñii,kon nag bu leen may ndam.5Nee ñu, ku njariñ tax nga wor xarit,say doom a cay loru.6Man la nit ñi def léebukaay,di ma tifli ci kanam.7Naqar tax na saay gët giim,saa cér yépp jeex ba mel ni takkndeer.8Ku jub a ngii jommi ci lii ma dal,ku dul tooñ a ngi xabtalu fi kaw yéefar yi.9Waaye aji jub a ngi topp yoonam,boroom loxo yu set a ngi gëna am kàttan.10Waaye yeen ñépp, waxaatleen, ma dégg,boroom xel daal duma ko gis ci seen biir!11Samay fan wéy na,mébét yàqu,yaakaar yàkki.12Ñii guddi lañu def bëccëg,naan leer sorewul, te lëndëm teew.13Ndegam kërug njaniiw laa yaakaarati,te biir lëndëm laa nara tëri,14ndegam maa naa paxum yàqute ma: «Yaay sama baay!»naa saxu bàmmeel: «Yaay bóoy!» mbaa «Jigéen sama!»15Kon ana sama yaakaar?Ana ku gisati sama yaakaar?16Xanaa day ànd ak man tàbbi bàmmeel,nu bokk tëraayu pënd.