1Ku jigéen jur,yaa néewi fan, géejal coono!2Dangay tóor rekk, lax,wéy ni takkndeer, doo toog.3Mooy kii nag nga teg bët,mooy man mii nga nara layool!4Lu sobewu, ana ku ci mana am lu laab?Du kenn!5Ndegam yaa dogalal nit ay fanam,lim ay weeram,dogal àpp ba, te du jaas,6teggi ko boog say gët, mu dallu,ni liggéeykat bu jaanam wàcc ci bés.7Garab sax ñàkkul yaakaar.Boo goree, mu jebbiwaat,ba du ñàkk ay njebbit.8Reen ba man naa màggat,ëkk ba deewe biir suuf,9mu yégum ndox rekk, jebbi,saxaat nim njëmbat.10Waaye nit dee, doole réer,bakkan rot, mu ne mes.11Day mel ni déeg bu ŋiis,mbaa dex gu wow ba jeex.12Doom aadama it tëdd, du jógati,du yewwooti, asamaan fekke,du jógeeti ciy nelaw.
Làq ma sa mer, ba giif
13Éy soo ma nëbboon biir njaniiw,làq ma, ba sa mer giif,dogalal ma àpp, te bañ maa fàtte!14Ndax dees na dee, di dundati?Doon naa ko muñe sama fani coono yépp,ba keroog sama kuutaay yiwisi ma.15Doon nga ma woo, ma wuyu,te kon nga namm sa càkkéefu loxo.16Doon nga wóoral samay jéego,te doo ma toppe samay bàkkaar.17Konoon samag tooñ yebe ci mbuus mu takke;sama ñaawtéef, nga muure ko malaan.18Waaye aw tund day màbb, ruus;aw doj di toxu,19am ndox di jonji xeer ba mu jeex,waame buub suuf, yóbbu,te noonu ngay neenale yaakaaru doom aadama,20man ko, mu dëddu fàww,kanam ga soppiku, nga jalax.21Doom ya tedd, yégul;ñu tekkeedi, tinul.22Nit yégul lu moy mititu boppamte bakkanu boppam lay tiisoo.