1Dama ne, lii lépp maa ko gis,dégg ko, xam ko.2Li ngeen xam, man it xam naa ko;duma seen cuune fenn.3Waaye man Aji Man ji laay waxal,layook Yàlla laa namm.4Yeen nag yeenay rafetalkati fen,yeen ñépp di fajkati caaxaan.5Céy su ngeen noon cell,muy seen rafet xel!6Ngalla dégluleen sama tawat,teewluleen sama kàddug layoo.7Ndax Yàlla ngeen di waxal waxi njubadi,di ko duural?8Ndax Yàlla ngeen faral,walla Yàlla ngeen di layool?9Ndax bu leen Yàlla luqatu woon dina baax?Am ni ñuy naxe nit ngeen koy naxe?10Su ngeen ko faraloon ci kumpa sax,du tee mu sikk leen moos.11Xanaa màggaayu Yàlla tiitalu leen?Am ragluwaayam ëlëmu leen?12Seeni tari, léebi neen,seeni tont, kiiraayu boob.13Xeremluleen, ba ma wax manak lu ma mana dal.14Amul dara lu mu ma jaralul,ba ci jaay sama bakkan.15Su ma Yàlla doon rey it, moom laay yaakaar,maay janook moom, layool sama bopp.16Loolu it sama mucc a ngi ci,ndax ab yéefar du dikk di janook moom.17Dégluleen a déglu sama baat,sama kàddu ci seeni nopp.18Dégluleen maa, ma lañal ab layoo,bir na ma ne maay yey.19Ana ku may yey cib layoo?Kon de ma wedam te dee.20Xanaa nga may ma ñaar rekk,ba du jar ma di la làqu:21ngalla teggi ma sa loxo,te buma dabeeti tiitaange joo sabab.22Wooteel, ma wuyu,mbaa ma wax, nga àddu ma.23Ana luy sama ñaawtéef aki moy?Xamal ma samag tooñ ak sama moy.24Ana loo may làqe sa leeru kanam?Danga maa jàppe sab noon?25Xob wuy wéy ngay xoqtal?Ana boob buy naaw, loo ciy topp?26Yaa ma bindal dogal yu wex,añale ma sama ñaawtéefi ndaw!27Yaa ma jéng,di sàmm fépp fu ma jaare,topp sama tànk!28Sama bakkan a ngi ruus ni bant bu fënëx,mbaa mbubb mu maxe.