Yeremi9wol_mbs

1Éy ku ma mayoon ci màndiŋ midalu panaanum njëggaan,ba ma teqalikook bokk yi, wacc leen,dem, bàyyi leen?Ñoom ñépp ay bokkaale,di gàngooru workat.

Dëgg jeex na

2«Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat,seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon.Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon,te man faalewuñu ma.»Kàddug Aji Sax jee.
3«Na ku ne moytu dëkkandoomte baña wóolu menn mbokk.Kuy mbokk déy, lal nga pexem wuruj, di wuruj;kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.4Ku ne sa dëkkandoo ngay nax,te dëgg, doo ko wax.Dañoo tàmmi fen,di def njekkar ba sonn.5Yeena ngi dëkke njublaŋ,njublaŋ rekk,faaleetuleen ma.»Kàddug Aji Sax jee.
6Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yiwax ne: «Maa ngii di leen segg,nattu leen ni weñ gu sawara seeyal, xelli!Ana nu may def neneenak sama ñoñ?7Seen làmmiñ di fitt guy bóome,seeni wax dig njublaŋ.Nit di wax moroomam jàmm,te di ko tëru cim xelam.8Lii, ndax duma leen ko dumaa?»Kàddug Aji Sax jee.«Xeet wu mel nii ndax duma ko fey yoolam?»

Jooy jot na

9Tund ya laay jooy, di yuuxu,di jooy parluy màndiŋ ma,fa lépp lakk, ba jaareesu fa,déggeesul baatu jur;njanaaw ak mala,lépp daw, ne mes.10«Maay def Yerusalem jali doj,till yi dëkke;ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.»11Ana ku muus, ba xam lu waral lii?Ana ku Aji Sax ji waxal,mu wax nu lu waral réew mi sànku,gental ni màndiŋ mi,kenn jaaru fi?12Aji Sax ji ne:«Ñoo wacc sama yoonwi ma leen tegaloon,sàmmuñu sama kàddu,jëfewuñu ko,13xanaa wéy ci dëgër bopp,topp tuuri Baal yi leen seeni maam miinaloon.»
14Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,Yàllay Israayil wax ne:«Maa ngii di leelsil xeet wii njàqarey xeme,nàndal leen tookey mbugal.15Maa leen di wasaare fi biir xeet yu ñu xamuloon,du ñoom, du seeni maam.Maa leen di tofal saamar, ba raafal leen.»
16Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:«Ne leen: “Gisleen li xew te woowi jigéeni jooykati dëj yi, ñu dikk;yónneeleen ca ña gëna man, ñu dikk.”»17Ñiy dëbbe, nañu nu gaawe ci jooy yi,gët taa, rongooñ wal.18Yuux a ngoog, jibe Siyoŋ.Ñu naa: «Nooka rajaxoo,torox ba ne tott,noon màbb sunuy dëkkuwaay,nu génn réew mi.»19Yeen jigéen ñi,ngalla dégluleen kàddug Aji Sax ji,taataan waxam,ba jàngal seeni janq jooyi dëj,jigéen ju ne jàngal moroomam yuuxi dëj.20Dee déy moo ñalgoo sunuy palanteer,dugg sunuy kër yu yànj,rey gone yi ci mbedd mi,ak xale yu góor yi ci pénc yi.21«Ne leen: “Kàddug Aji Sax jee.Néew yeey wetaroo ci àll bi, mel niy jonkan,ni gub yu góobkat won gannaaw, kenn forul.”»

Ku xam Yàlla rekk a xelu

22Aji Sax ji dafa wax ne:«Ku xelu, bumu damoo am xelam;ku jàmbaare, bumu damoo njàmbaaram;ku woomle, bumu damoom koomam.23Kuy damu kay, na damoom xelammu ko may mu xam ma,xam ne maay Aji Saxjiy doxal ngor ak yoon ak njub fi kaw suuf.Loolu déy mooy sama bànneex.»Kàddug Aji Sax jee.

Xaraf, na Yàlla tax

24«Ay bés a ngii di ñëw,»kàddug Aji Sax jee,«maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram,25muy waa Misra, di waa Yuda,di Edomeen ñeek Amoneen ñi,di Mowabeen ñeekmboolem ñiy wat seen peggu kawaru boppte dëkke màndiŋ mi,nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, te itbànni Israayil géppxarafuñu xarafu xol