Yeremi8wol_mbs

1«Su boobaa déy,»kàddug Aji Sax jee,«noon yeey sulli yaxi buuri Yudaak yaxi kàngam yiak yaxi sarxalkat yiak yaxi yonent yiak yaxi waa Yerusalem,fa seeni bàmmeel,2weer leen ci naaj week weer wiak mboolem biddiiw yi ñu soppoon,di leen jaamu, di leen wut aka topp,di leen sukkal.Deesu ko dajale, deesu ko suul;day mel niy jonkan fi kaw suuf si.3Dee mooy gënal dundmboolem ku des ci njaboot gu bon gii,ak mboolem fu ñu dese fa ma leen tasaare woon.»Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.

Askan wi të na ticc

4«Nanga leen wax ne leen:“Aji Sax ji dafa wax ne:Xanaa ku daanu, da dul jógaat?Am ku lajj, du délsi?5Lu tax xeet wii dëddu?Lu tax Yerusalem gii lajj, baña délsi?Ñu ngi langaamoo naxi neen,baña délsi.6Teewlu naa, déglu naa;du lu jaadu lañu wax.Kenn tuubu ci mbonam,ba ne: ‘Lu ma def nii?’Ku nekk a topp yoonam,ni fas wu màmm cib xare.7Ag xodd sax xam na bésub demam,pitax, wetwet ak mbelaar it dem,tey sàmm seen bésub délsi.Waaye sama ñoñ faalewuñu àtteb Aji Sax ji.8Nu ngeen mane ne: ‘Am nan xel,nu ngeek yoonu Aji Sax ji,’te xalimay yoonalkat soppi ko fen?9Dees na gàcceel boroom xel yi,ñu jàq, jataŋe.Kàddug Aji Sax jaa ngii ñu dëddu ko,ana seenum xel?
10«“Kon nag maay jël seeni jabar, jox ñeneen,jox seeni tool ay foqatikat,ndax ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,ñépp a ngi lewal lu lewul.Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!11Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammatoo,naan: ‘Jàmm, lépp jàmm!’te jàmm amul.12Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu,te gàcce gàcceelu leen.Xamuñu sax luy kersa!Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu.Bu ma leen dikkalee, dinañu tërëf.”»Aji Sax jee ko wax.

Yaakaar tas na

13«Maa leen di witt a witt.»Kàddug Aji Sax jee.«Garabu reseñ du dese doom,figg du dese doom,»kàddug Aji Sax jee,«xob ya sax day wow.Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.»14Ana lu nuy toog?Fabuleen, nu dem ca dëkk ya tata wër,deewi fa.Sunu Yàlla Aji Sax ji nar na sunu dee;moo nu nàndal tookey mbugal,nde noo tooñ Aji Sax ji.15Nuy yaakaar jàmm,dara baaxul;nuy séentum paj,tiitaange ne jaas!16Seen noowi fas yaa dégtoo bëj-gànnaar fa Dan,seen fasi naaru-góor di ŋexal, suuf sépp yëngu.Ñu dikk, tas réew mi tasar,booleek li ci biiram,ak dëkk beek ñi ci biiram.17«Maa ngii déy di leen yónneejaani ñàngóor yu déggul jat,ñu di leen màtt.»Kàddug Aji Sax jee.

Yeremi am na naqar

18Ndaw naqar wu tiis,ndaw xol bu diis!19Sama bokk yaa ngooguy yuuxuyuux yu àkki fu sore,naan: «Moo xanaa Aji Sax ji daa newul Siyoŋ?Xanaa Buurub Siyoŋ da fee nekkatul?»Yàllaay wax«Lu tax ñuy yékkati sama xolak seen jëmmi tuur yii,seen yàllay doxandéem yi tekkiwul dara?»20Ngóob wéy na, jamonoom wees,te nun de muccagunu.21Sama bokk yi seen xol jeextax na sama xol jeex,may tiislu, tancoo njàqare!22Moo ndax diwu pajtal amul Galàdd ?Am fajkat a fi amul?Ana lu tax ba bokk yi taneeguñu?23Aka neexoon sama bopp soppaliku ndox,saay gët di seyaan buy xelliy rongooñyu ma jooye guddeek bëccëgbokk yi ñu bóom!