1«Yeen askanu Beñamin, fëxleen,génn Yerusalem.Walleen bufta bi fa Tekowa,jafaleleen jum yi Bet Kerem, artoo ko,musiba kat a ngi yëre bëj-gànnaar,di safaan bu réy.2Yaw Siyoŋ, dëkk bu taaru bi te xejj,dama lay dammat.3Ay sàmm ak seeni gétt ci sa kaw,ñu samp seeni xayma, wër la,di foral, ku nekk ak pàccam.»4Ñii ne: «Waajalleen xare baak ñoom,nu songi leen digg bëccëg.Waaye wóoy nun, jant a ngi lang,keru ngoon di law!»5Ñee ne: «Nan song congum guddi boog,ba rajaxe seen kër yu yànj yi.»6Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy da ne:«Gorleeni bant,sëkke Yerusalem, gaw ko!Dëkk bii dees koy mbugal,àqu nooteel la fees dell.7Ni bëtu ndox di dawe,ni lañuy dawale seenug coxor.Fitnaak salfaañooy riir ci dëkk bi,gisuma lu moy jagadeek loraange!8Yeen waa Yerusalem, deeleen déggbala ma leena dëddu,ba gental réew migent bu kenn dëkkul.»
Askan wa të na
9Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:«Nañu witt a witt ndesu Israayil,ni ñuy witte reseñ,ba nga dawalaat say loxo ca car ya.»10Moo kan laay waxal,artu ko ba mu déglu?Seeni nopp a fatt ba manatuñoo sax teewlu.Kàddug Aji Sax jaa ngii,mel ni lu ñu rus,lu ñu safoowul!11Maa ngi fees dell ak merum Aji Sax ji,ba manatuma koo dékku.Yàllaay wax«Sippi ko tuut-tànk yi ci mbedd mi,sippiwaale ko waxambaane yi daje,mu laawaale jëkkër ak jabar,mag ak màggat,12seeni kër doon alali jàmbur,ak seeni tool it ak seeni jabar.Maay xàcc sama loxo déy,dal ci kaw waa réew mi.»Kàddug Aji Sax jee.13«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag,ñépp a ngi lewal lu lewul.Yonent akub sarxalkat,ñépp a ngi wor.14Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammatoo,naan: “Jàmm, lépp jàmm!”te jàmm amul.15Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu,te gàcce gàcceelu leen.Xamuñu sax luy kersa!Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu.Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.»Aji Sax jee ko wax.
Pexey askan wi jur na musiba
16Aji Sax ji dafa wax ñoñam ne:«Taxawleen ca selebe yoon wa, xool,te laajte yoon ya woon,ne: “Ana yoonu mbaax?”Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.»Ñu lànk ne: «Awunu ca.»17«Ma tabbal leeni wattukatne: “Teewluleen bufta bu jib.”»Ñu lànk ne: «Teewluwunu.»18«Moo tax yeen xeet yi, dégluleen;yeen waaso yi, seedeleen liy xaar ñii.19Yeen waa àddina, dégluleen!Maa ngii di indil askan wii musibami leen seeni pexe jural.Ñoo faalewul samay kàddu,gàntal sama yoon.20Lu may doye lii?Ndàbb lu jóge Seba ,diw gu xeeñ, bawoo réew mu sore?Seeni saraxi rendi-dóomal safu ma;seen saraxi jur, bëgguma.»21Moo tax Aji Sax ji wax ne:«Maa ngii di tegal askan wiiay pakk, ñu fakkastaloondoo,baay ak doom,dëkkandookub xarit,ñépp sànku.»
Noon sàqee na bëj-gànnaar
22Aji Sax ji dafa wax ne:«Aw askan a ngii bàyyikoo réewum bëj-gànnaar,xeet wu mag lañuy doon, sàqee fa cati àddina.23Fitt aku xeej lañuy ŋëb,néeg lool, duñu yërëm;seen coow ni riirum géej,ñu war seeni fas, rëpptal,làng-déral leen,yeen waa Siyoŋ, dëkk bu taaru bi.»24Danoo dégg riir mi,sunuy yoxo yoqi,njàqare ne nu taral,ni mititu mat.25Kii naa: «Bul génn ci àll bi!»Kee naa: «Bul jaar ci yoon wi!»Saamar kay a nga ca loxol noon ba,tiitaange dajal fépp!26Éey bokk yi, solleeni saaku,diwoo dóomu-taal, ñaawloo ko.Ñaawluleen ni kuy dëj benn bàjjote jooy jooy yu metti,nde yàqkat bi day jekki,ne sunu kaw dàll!27«Maa la def sama nattukatu ñoñ,nga di leen nattu ni ñuy nattoo xaalis,te war leena seetlu, nemmiku seen jikko.28Ñoom ñépp a di fippukat yu fétteeral,wër di sos,dëgërle ni xànjar ak weñ gu ñuul.Ñoom ñépp di yàqkat.29Tëgg wal taalam, mu yànj;sawara seeyal betteex.Xellees na koo xelli ci neen,taxul li ci bon génn.30Dees na leen woowe mbuubitum xaalis,nde Aji Sax ji buub na leen, sànni.»