Yeremi5wol_mbs

Mbugal war na

1«Wërleen mbeddi Yerusalem,xoolleen, seet ciy péncam rekk ba xamndegam dingeen gis kenn,kenn kepp kuy def njub,di sàmm worma,ma daldi leen baal.2Bu ñu nee sax: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,”ay fen lañuy giñ.»3Aji Sax ji, xanaa du worma ngay sàkku?Dóor nga leen, safu leen;nga làbbali, ñu tanqamlu,wowle ba raw doj, baña dëpp.4Man nag, ma noon: «Ñii de ay baadoolo rekk lañu,di def jëfi dof,xamuñu yoonu Aji Sax ji,xamuñu lu seen àtteb Yàlla laaj.5Kon naa dem seeti kàngam yi,wax ak ñoom.Xanaa ñoom dinañu xam yoonu Aji Sax ji,xam lu seen àtteb Yàlla laaj.»Waaye ñoo bokk daggook Yàlla,dogook moom.6Moo tax gaynde di génne ci gott bi, fàdd leen,bukkiy màndiŋ mi di leen yàpp,segg di tëru seeni dëkk,ku ca génne, dees na la xotat.Seeni moy a bare,te seen ñàkk worma réy.7«Yerusalem, ana lu tax ma di la baal,te say doom wacc ma,di giñe lu dul Yàlla.Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo,riixle, jëm kër gànc ya!8Mbete fas yu suur, tukkal,ku ne ŋexal, jëm ca sa jabaru moroom.9Lii, duma leen ko dumaa?»Kàddug Aji Sax jee.«Wii xeet, ndax duma ko fey yoolam?
10«Yéegleen seeni tata, yàqate,waaye buleen leen jeexal tàkk.Tenqileen lawit yi,ñooñoo bokkul ci Aji Sax ji.11Waa kër Israayil ak waa kër Yuda kat,ñoo ma wor a wor!»Kàddug Aji Sax jee.12«Ñoo fenal Aji Sax ji,naan: “Moom du def dara,musiba du nu dal,saamaroo, xiifoo, dunu ci gis dara.13Yonent yi daal, ngelawal neen!Kàddug Yàlla newul ci ñoom;li ñuy wax, na leen yenu!”»

Aji Sax ji artu na xeet wi

14Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:«Gannaaw wax jii lañu wax,maa ngii di def samay wax di sawara ci sa gémmiñ,muy xoyom askan wii mel ni matt.15Éey waa kër Israayil,»kàddug Aji Sax jee,«maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore.Xeet wu am kàttan lañu,xeet wu yàgga yàgg,wu ngeen xamul seen làmmiñ,te dégguleen seeni wax.16Seen mbari fitt ŋafal paxum bàmmeel,ñoom ñépp di ñeyi xare.17Ñooy dikk, warax seen meññeef ak seen ñam,jeexal seeni doom, góor ak jigéen,lekk seen jur gu gudd ak gu gàtt,saax-saaxee seeni reseñ ak seeni figg;te dëkk yi ngeen yaakaare seeni tata,dooley saamar a koy tas.18Waaye bési keroog it,»kàddug Aji Sax jee,«duma leen jeexal tàkk.19Bu ñu nee:“Ana lu waral sunu Yàlla Aji Sax ji teg nu lii lépp?”ne leen: “Yàlla nee:Ni ngeen ma dëddoo, di jaamu yàllay jàmbur ci seenum réew,ni ngeen di jaamujee ay jàmburbiir réew mu ngeen moomul.”
20«Jottalileen lii waa kër Yanqóoba,biralleen ko fa Yuda, ne leen:21“Ngalla dégluleen lii,xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon,ami gët te dungeen gis,ami nopp te dungeen dégg!22Man daal, ndax dangeen maa ragalul,am dungeen raf ci sama kanam?”»Kàddug Aji Sax jee.«Man mi teg gannuus, yemalee ko géej,dogalal ko ko dàkk te du ko jàll,lu mu wañax wañax, du ko man;gannax ya day riir, te du jàll!23Waaye wii xeet a dëgër bopp te déggadi.Dëddu nañu ma ba wéy.24Seen xel demul sax ba ne:“Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Saxjiy jot, mu tawal nu,taw yu jëkk ak yu mujj yi,àppal nu ayi bési ngóob,sédde nu?”25Yooyii seeni ñaawtéef a ko waññi,seen bàkkaar a leen xañ ngëneel.

Mbon maase na ci xeet wi

26«Waaw! Daa am ñu bon ci sama ñoñ,ñuy tërooka fiirembete nappkati picc.27Ni kaaf di feeseeki picc,ni la seeni kër di feese alali càcc,ba tax ñu yokku ba woomle,28yaflu, di nes-nesi.Seenug mbon it amul kem:duñu defal jirim njub,duñu àtte néew-ji-doole dëgg.29Lii, ndax duma leen ko dumaa?»Kàddug Aji Sax jee.«Xeet wu mel nii ndax duma ko fey yoolam?30Lu siblu te yées am na ci réew mi:31Yonent yiy wax kàdduy fen,sarxalkat yiy jiitee seen coobare,te sama ñoñ soppe ko ni!Moo, ca muj ga, nu ngeen di def?