Yeremi48wol_mbs

Lu jëm ci réewum Mowab

1Lu jëm ci Mowab: Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne:«Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na!Kiryaatayim, ñu toroxal, nangu ko;tata ja daanu, tasaaroo.2Mowab amatul woy,fa Esbon la leen noon ya fexeel lu bon,ne: “Aycaleen nu raafal wii xeet!”Yeen waa Madmen it, ñu wedamal;saamar topp leen.3Yuux jibe na Oronayim,ndaw salfaañook rajaxoo ju réy!4Mowab tas, ay fereem serandoo.5Ñay yéeg jëm Luxit, di jooyoo.Ña ngay yéeg, di jooyoo.Ñay wàcci Oronayim di dégg aji jàq jiy yuuxoo.6Ñu naan: “Dawleen, rawale seen bakkan,ba tumurànkeji ni gajju màndiŋ!”7Mowab, yeena yaakaar dooleek alal,yeen it, dees na leen jàpp;Kemos seen tuur mi duggi ngàllo,mooki sarxalkatam aki kàngamam.8Dëkkoo dëkk ay yàqtoo,benn dëkk du mucc!Waa xur wii sànku,waa joor gee yàqtoo.»Muy la Aji Sax ji wax.9«Gasalleen Mowab,day sànku moos,ay dëkkam gental,kenn du fa des!10Alkànde ñeel na kuy sàggane liggéeyu Aji Sax ji.Alkànde ñeel na kuy xañ deret saamaru Aji Sax ji.
11«Mowab a dale féex cag ndawam,kenn jàppu ko njaam, yóbbu,sotteesu ko ndab ak ndab,xanaa mu ne degg ni biiñ bu taaje,di saf, di xeeñ ba tey.12Moo tax ay bés a ngii di ñëw,»kàddug Aji Sax jee,«maa leen di yónnee ay nit ñu sotti diw gi,ndab, soteet; njaq, rajax.13Yaakaaru Mowab ci Kemos tuur mi tas,ni yaakaaru waa kër Israayil ci Betel ma ñu wóolu tase woon.
14«Yaw réewu Mowab, du yaay kañu,naan jàmbaar nga,diy ñeyi xare?15Song nañu Mowab, yàqate ay dëkkam;la man ci ay ndawam daanu dee.»Kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.16«Musibay Mowab a ngi jegesi,safaanam làbbaleeti, wuti ko.17Mboolem yeen ñi wër xeet wii, jooyleen ko;yeen ñi dégg turam ñépp, jooyleen ko.Neleen: “Moo, nu gii nguur mana foqe,ba foqaale jii daraja?”
18«Yeen waa Dibon, dëkk bu taaru bi,wàccleen seen teraanga ju kawete toog ci digg maral;kiy yàqatesi Mowab kat song na leen,di màbbsi seeni tata.19Yeen waa Arower,taxawleen fi yoon wi te teewlu;góor gu fi jaare mbaa ndaw su rëcc, di daw,ngeen laaj ko ne ko: “Lu xew?”20Ñu ne: “Gàcce ñeel na Mowab gii tas!”Yuuxooleen, ne wóoy!Yéeneleen fa tàkkal dexu Arnon,ne Mowab tas na!21Mbugal dikkal joor gi,dikkal dëkk yii di Olon, Yaxacc ak Mefaat22ak Dibon ak Nebo ak Bet Diblatayim23ak Kiryaatayim ak Bet Gamul ak Bet Mewon24ak Keryot ak Boccara,mboolem dëkki Mowab daal,fu jegeek fu sore.25Sidditu Mowab day dog,loxoom damm.»Kàddug Aji Sax jee!26«Du Mowab a doon diir Aji Sax ji mbagg?Nañu leen màndal sànjum Aji Sax ji,ba ñu waccu, di ca xuus,ba ñoom it, ñu di leen ree.27Waa Mowabee, du yeena doon ree Israayil?Dangeen leena fekk ci biiri sàcc,ba fu ngeen leen tudde, wëcc bopp?28Yeen waa Mowab,baleen dëkk yi, dëkke paxi doj.Defleen niy xati,tàgge peggi xunt.
29«Noo dégg ni Mowab bewe,bew lool,réy, reew, di damu;ne daŋŋ-daŋŋiiral.30Maa xam seen reewande,»kàddug Aji Sax jee,«seeni kañu neen la,seeni jëf di neen.31Moo tax may jooy Mowab,di wooteel wall Mowab gépp,di yuuxul waa Kir Eres.32Yaw reseñu Sibma gi,ma jooyal la lu raw la ma jooyal Yaser.Yaw la say car jàlloon géej,àkki géeju Yaser,sa figg jeek sa reseñ, noon yàqate.33Tukkal nañu mbégteek bànneexfi tóokëri réewum Mowab.Maa ŋacc mbàndi biiñ ya,kenn nalatu fa reseñ, di soowoocoowal mbégte, xanaa ay yuux.34Yuux jibe na Esbon, ba Elale, àkki ba Yaxaccak Cowar ba Oronayim ak Eglat Selisiya.Ndoxi Nimrim sax ŋiis na.35Maay bóome biir Mowab.»Kàddug Aji Sax jee.«Maay bóom kuy joxe sarax ci bérebi jaamookaay yi,di taalal am tuuram cuuraay.36Naa jooy Mowab jooyi xolyu toxoro di jooye ab dëj,na toxoro di jooye dëju waa Kir Eres.Lu ñu dajale woon sànku na!37Ñoom ñépp a nelu,wat seeni sikkim,daggat seeni loxo,sol ay saaku, di ko ñaawloo.38Kaw taaxi Mowab yépp aki péncam,fépp ay yuuxoo di jib.Maa toj Mowabni ndab lu kenn soxlaatul.»Kàddug Aji Sax jee.39«Yuuxooleen, ne leen: “Céy gii yàqtoo!Mowab gii wone gannaaw! Mowab rus na.”Ñi ko wër ñépp a koy reetaan, di ci raf.»40Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Lu mel ni jaxaay a ngii naa jàyy,firiy laafam, këfsi Mowab.41Dees na teg Keryot ga ca Mowab loxo,ne tata ya taral;su keroogee fitu jàmbaar ne tërit,mu mel ni kuy matu.42Mowab day sànku, ba xeetam fey.Ñoo doon diir Aji Sax ji mbagg.43Yeen waa Mowab,pat-pati rekk, di tàbbiy pax aki yeer.»Kàddug Aji Sax jee.44«Pat-patiy daw, tàbbim pax;génnum pax, tàbbim yeer.Maay yen Mowab, maa leen di yen moosseen atum mbugal.»Kàddug Aji Sax jee.45«Fa keppaaru Esbon lañuy daw taxawi,doole dëddu.Booba sawaraa tàkke Esbon, di law;sël-sëlee foofa ca péeyu Buur Sixon,ba dajal réewum Mowab, nitu coow ña,boole jë akum kaaŋ xoyom.46Wóoy, waa Mowab, ngalla yeen!Yeen ñiy jaamu Kemos, sànku ngeen!Dees na jàpp seen doom yu góor njaam;jigéen ñi it, njaam.
47«Du tee fan yu mujj ya,ma tijji wërsëgu Mowab.»Kàddug Aji Sax jee.Fii la àtteb Mowab yem.