1Kàddug Aji Sax ji dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi jëm ci Filisteen ñi, balaa Firawna di song dëkkub Filisteen ba ñuy wax Gasa.2Aji Sax ji dafa wax ne:«Ndox a ngay fuddoo bëj-gànnaar,diy waame, walsi,walal réew meek li ci biiramakub dëkk ak ku ci biiram;doom aadama yuuxu,waa réew mépp serandoo.3Booba fas yaa ràmbal,watiir ya riir,mbegey watiir ya kar-kareendoo,loxo yoqi, ba baay geesuwul doom,4bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen,ba dagge ci dëkk yii di Tir ak Sidonndimbal lu ñu dese woon.Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen ña deste cosaanoo dun bu ñuy wax Keret.5Watu nel, ñaawloo dikkal na Gasa,te wedamloo nañu Askalon.Yeen ñi dese joor gi,fu ngeen àppal seen yaram wi ngeen di daggat, di ko ñaawloo?6Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii,xanaa doo noppee reye?Dellul ci sa mbar, boog,dallu, ne tekk!”7Waaye yaw saamar, naka nga mana selaŋloote Aji Sax ji yebal laci kaw Askalon ak waa tefesu géej,fa mu ko dogale?»