1Kàddug Aji Sax jii dikkal na Yonent Yàlla Yeremi, jëm ci xeet yi.
Lu jëm ci Misra
2Lu jëm ci Misra: Firawna buuru Misra bi ñuy wax Nekko, ba ko Nebukatnecar buuru Babilon di duma, ma nga woon ca Karkemis ca tàkkal dexu Efraat. Mu yemook ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya Yoyakim buurub Yuda. Kàdduy waxyu yii moo jëm ci Misra ci wàllu diggante ba seen mbooloom xare ma tollu woon:3«Ŋàbbleen pakkoo pakk te xareji.4Takkleen fas yi, war naaru-góor yi,ba làng-déraale seen mbaxanay xare,nàmmaat xeej,sol yérey xare!5«Ana lu ma gis?Waa Misraa jaaxle bay dellu gannaaw,seeni jàmbaar falaxoo,ne wëqét, geesuwuñu,tiitaange ubale.»Kàddug Aji Sax jee!6«Bu nit gaaw ba rawmbaa mu jàmbaare ba mucc.Bëj-gànnaar lañu féete, feggook dexu Efraat,di tërëf, di daanu.7«Kii ku mu, muy fuddu ni dexu Niil,di fuur ni wali ndox?8Misraa, mooy fuddu ni dexu Niil,di fuur ni wali ndox.Mu naan: “Maay fuddu, mëdd àddina,sànk ab dëkk ak ña ca biir.”9Na fas buur, watiir fiddi,jàmbaar sàqi:waa Kuusoo waa Puut ak seeni pakk,ak waa Ludd ak seeni xalaaki fii.10Waaye bésub keroog déy,Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko moom,muy bésub feyu bu muy feyey noonam.Saamar suur suux,màndee deret.Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yimooy rendee réewum bëj-gànnaar ab sarax,feggook dexu Efraat.11Yaw Misra mu taaru mi,demal ba Galàdd wuti diw, dàmpoo.Faju, fajooti;dara du la wéral!12Xeet yeey dégg sa toroxte,sa yuux dajal àddina.Jàmbaar téqtaloo jàmbaar,ñu ànd ne fëlëñ!»13Kàddu gii dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi, ba Nebukatnecar buuru Babilon dikkee, di duma waa réewum Misra. Mu ne:14«Yégleel lii Misra, yéene ko fa ca Migdol,yéene ko fa ca Memfis ak Tapanes.Neleen: “Dërleen, taxaw temm!Saamar kat a ngi lekk li leen wër.”15Lu Apis, seen jëmmi tuur ma, di daw?Lu tee seen yàllay yëkk jooju taxaw?Xanaa Aji Sax jee ko bëmëx!16Moo bëmëx ñu bare,ku nekk naan moroom ma:“Jógal nu dellu ca sunuy bokk,ca sunu réewum cosaan,ba mucc saamaru noon.”17Dees na fa woyal Firawna buuru Misra, naan ko:“Coowal neen te bés wees.”18«Giñ naa ko ci man miy dund,»kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi di turam:«noon ay dikk, mel ni tundu Tabor ci digg tund yi,mbete tundu Karmel wi feggook géej.19Yaw mi dëkke Misra mu taaru mi,ëmbal sa ëmb, jëm ngàllo;Memfis dëkk bii kat ci gental la jëm,di ndànd-foyfoy gu kenn dëkkul.20Misra daa mel ni jeegu nag bu yànj,weñ ne waa waa, bawoo bëj-gànnaar.21Seen xarekat yi ñu bind saxñu ngi mel ni sëllu yu yaflu,ñoom it ànd ne wërëñ, wëqét,kenn taxawul!Bésu safaan a leen dikkal,seen mbugal taxaw,22ñu daw di faraas-faraasiy wéy ni jaan.Doole la noon songe Misra,dikke leeni sémmiñ ni gorkati garab.23Lu gott fatt fatt, ñu gor.»Kàddug Aji Sax jee.«Ñoo gëna barey njéeréer,ba maneesu leena lim.24Gàcceel nañu Misra mu taaru mi,teg ko ci loxoy xeeti bëj-gànnaar.»25Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoori xare yi wax na ne: «Maa ngii di dikke mbugal Amon, tuuru dëkk bii di No, ak Firawnaak waa Misraak seeni tuur ak seeni kàngam, boole ci ñi yaakaar Firawna.26Maa leen di teg ci loxoy ñiy wut seen bakkan, di Nebukatnecar buuru Babilon aki jawriñam. Gannaaw loolu dees na dëkkewaat Misra na woon.» Kàddug Aji Sax jee!
Israayil dina xettaliku
27«Yaw Yanqóoba sama jaam bi nag, bul tiit;yaw Israayil, ma ne bul ragal.Maa ngii di la wallusi,jële la fu sore,jële sa askanfa seen réewu njaam ga,Yanqóoba délsi,dal, aaru, du tiitati.28Yaw Yanqóoba sama jaam bi, bul tiit.»Kàddug Aji Sax jee.«Yaw laa àndal.Maay faxas mboolem xeet yi ma leen sànni woon,waaye yeen, duma leen faxas.Duma leen ñàkka duma moos,waaye dinaa leen yar lu yem.»