Yeremi4wol_mbs

1«Yaw Israayil, sooy waññiku,waññikul fi man.»Kàddug Aji Sax jee.«Soo jëlee fi sama kanamsa jëf ju siblu,te jenguloo,2xanaa nga waat ci Aji Sax jiy dund,def ko ci dëgg ak yoon ak njub,kon xeet yi dinañu barkeeloo Aji Sax ji,di ko sagoo.»3Aji Sax ji déy dafa wax waa Yudaak Yerusalem, ne leen:«Ruujleen seen tool,buleen ji ciy dég.4Yeen waa Yudaak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji,dogleen seen mbuñukay xol,balaa sama xadar ne jippét ni sawara,di tàkk te deesu ko feyndax seen jëf ju bon.

Xare jib na

5«Nangeen yégle lii fa Yuda,dégtale ko fa Yerusalem,yéenee koob bufta bi biir réew mite xaacu seen kem kàttan ne leen:“Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.”6Yékkatileen raaya, jubale Siyoŋ,làqujileen, buleen taxaw,musiba déy laay jële bëj-gànnaar,muy safaan bu réy.
7«Gayndee fëlle geeram,yàqkatu xeet yee jóg, génne këram,nara gental seeni dëkk,ba ñu di gent yu kenn dëkkul.8Kon nag solleeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne:“Merum Aji Sax ji tàng na kat te moyu nu.”9Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,«xolu buur jeex, kàngam ne yàcc,sarxalkat waaru, yonent jommi.»10Ma ne: Éy Boroom bi Aji Sax ji,yaa naxlu askan wii nax yu metti,ba nga nee: «Yerusalem jàmm lay am,»te saamar tege ci putam.

Mbugal taxaw na

11Janti keroog dees na wax askanu Yerusalem wii, ne leen:«Jaas bu tàng a uppe kaw tund ya ne faraas ca màndiŋ ma,wuti sama ñoñ.Du doon ngelaw lees di bàcceeka beese.12Ngelaw lu ko ëpp doole laay indi.Léegi maa leen di biral sama kàddug mbugal.»13Noon baa ngii, di jóg niy niir,watiiri xareem ni ngëlén,fasam ya gëna gaawi jaxaay.Wóoy ngalla nun, yàqu nan!14«Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon,ndax nga mucc.Foo àppal sa mébéti xol yu bon?15Kàddug yéenee ngi jibe Dan,musiba dégtu na, bawoo tundu Efrayim.16Jottalileen ko xeet yi,neleen Yerusalem:“Songkat yaa ngii riire réew mu sore ma,xaacoondoo fi kaw dëkki Yuda.”17Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool,ndax man la gàntal.»Kàddug Aji Sax jee.18«Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii,sa musibaa ngoog, wex la xàtt,di dagg sa xol.»19Maaka jàq a jàq bay jal-jali,sama xol biy fuddu!Éy wii mititu xol!Duma mana noppi,maa dégg wooteb buftaak yuuxi xare.
20Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo,réew mi mépp ne tasar kay!Jekki-jekki samay xayma tasaaroo.Xef-xippi ndimoy xayma ya xotatoo!21Xanaa duma gis ba fàww raayab noon,buftab xare di ko feelu?22«Dofe la sama ñoñ def.Man, xamuñu maay kan,mbetey gone yu dul xalaat dara;dég-dég, tus;seen xel mépp, lu bon rekk,lu baax, xamuñu ci tus.»23Maa xool suuf,ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ;ma xool asamaan,leer amatu ca.24Ma xool tund yu mag yi,ndeke ñu ngi yëngu,tund yu ndaw yépp di jaayu.25Ma xoolaat, gisuma nit,njanaaw yépp daw.26Ma xool, gis suuf su nangu sadi ndànd-foyfoy,dëkk yépp raafndax Aji Sax jeek tàngaayu sànjam.
27Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Duma tas lépp tasar,waaye réew mi mépp ay gental.28Loolooy tax suuf di ñaawlu,asamaan di lëndëm.Maa ko wax, maa ko dogu;duma dëpp, duma deltu gannaaw.»

Yerusalem dugg na fitna

29Gawar ak fittkat riir,waa dëkk yépp fëx,ñii tàbbiy gajj,ñee ñalgu ci kawi doj,ñu won dëkkoo dëkk gannaaw,kenn desatu ca.30Yaw Yerusalem mu tas mi,ana looy def nii,di solu ba yànj,gànjaroo wurus,tusngalu, yàkkleey gët?Yaa ngi sañse ci neen:say xéddkat wacc nañu la,sa bakkan lañuy wut.31Baatu ndaw su jagadi laa dégg,ma nga jàq, di matub taawam.Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa!Ma ngay àppaat, tàllal loxo ya,naan: «Wóoy, ngalla man;ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»