Yeremi39wol_mbs
1Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, ca fukkeelu weeram, ca la Nebukatnecar buuru Babilon ànd ak gàngooru xareem gépp ci kaw Yerusalem, ñu gaw ko.2Ba Cedesyas tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak benn, juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weeram, ca lañu bëtt dëkk ba.3Mboolem kàngami buuru Babilon daldi dikk toog ca buntu dëkk ba ca digg ba. Nergal Sarecer a nga ca ak Samgar Nebo ak Sar Sekim njiitu bëkk-néegi buur ak Nergal Sarecer meneen ma, njiitu gisaanekat yi, ñook mboolem kàngami buuru Babilon ña ca des.4Naka la leen Cedesyas buurub Yuda gis, mook xarekatam ya yépp, ñu daldi daw, génn dëkk ba guddi, jaare tóokëru buur, fëlle bunt ba ca diggante ñaari tata ya, wuti yoonu xuru dexu Yurdan.5Mbooloom Babilon dàq leen, ba dab Cedesyas ca jooru Yeriko. Ñu jàpp ko, indil ko Nebukatnecar buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla, ca réewum Amat. Nebukatnecar dogal fa àtteem.6Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor ca Ribla, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda.7Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.8Kër Buur ak këri waa dëkk ba nag, waa Babilon lakk leen, tatay Yerusalem, ñu màbb.9Nebusaradan njiitu dag ya moom, daa boole ña desoon ca biir dëkk ba, ak ña ko jébbaloon seen bopp, ak ña desoon ca askan wa, jàpp leen, yóbbu ngàllo ca Babilon.10Ba mu ko defee lenn ci baadoolo yi amul dara, mu wacc leen ca réewum Yuda. Booba la leen jox ay tóokëri reseñ aki tool.