Yeremi31wol_mbs

Israayil séentu na sancaatub réewam

1«Su boobaa,» kàddug Aji Sax jee, «maay doon Yàllay làngi Israayil yépp,ñoom ñuy sama ñoñ.»
2Aji Sax ji dafa wax ne:«Waa Israayil ñi rëcc ñawkay saamar,daje nañook yiw ci màndiŋ mi,fekk ñuy sàkku noflaay.»3Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu,ne nu: “Maa leen masa bëgg,ba tax ma sédd leen ngor.4Yaw Israayil mu taaru,maa lay defaraat, nga defaru,ba jiinaat sam njiin,wàlli peccum mbéx,5jëmbataat sa tóokëri reseñca mbartali Samari,te ku jëmbat, xéewlu ca.6Bés dina ñëw déy,wattukat yéenee fa kaw tundu Efrayimne: ‘Aycaleen nu yéegi tundu Siyoŋ,fa sunu Yàlla Aji Sax ji.’”»
7Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Sarxolleleen, bége askanu Yanqóoba,xaaculleen xeet woowu jiitu,biralleen cant te ne:“Éy Aji Sax ji, wallul ndesu Israayil, sa ñoñ ñii.”8Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar,dajale leen fa cati àddina.Silmaxaa ngi ci akub lafañ,jigéenu wérul it ak kuy wasin,ñuy gàngoor gu mag, délsi fii.9Ñooy dikk di jooy, di leewaayu,ma jiite leen, yóbbu,jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakkastaloo,ba ca wali ndox ya,ngir maay baayu Israayilmiy Efrayim, sama taaw.»10Yeen xeet yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji,yégleleen ko ca tefes yu sore ya.Ne leen: «Ki tasaare woon Israayil, moo leen di dajale,sàmm leen nib sàmm ak géttam.»11Aji Sax jee goreel askanu Yanqóoba,jot ko ci loxol ku ko ëpp doole.12Ñooy dikk, di sarxollee kaw tundu Siyoŋ,ne ràññ ndax ngëneeli Aji Sax ji:pepp ak biiñ aku diw, gàtt aki nag,bakkan ni tool bu ñu suuxat,dootuñu yoggoorlu.13«Su boobaa janq bégem pooj,waxambaaneek mag feelu ko,ma soppi seen ñaawlu mbégte, dëfal leen,bànneexal leen, ñu dëddu naqar.14Maay yafal sarxalkat yi, ba reggal leen,sama ñoñ ñi regge sama ngëneel.»Kàddug Aji Sax jee.
15Aji Sax ji dafa wax ne:«Baat dégtu na fa Raama,ay yuux aki jooy yu metti.Rasel ay jooy ay doomam,baña noppi,nde doomam ya wuute.»16Aji Sax ji nag ne ko:«Baal sa jooy yite fomp say rongooñ,dees na la yool sa coono.»Kàddug Aji Sax jee.«Say doom ay jóge réewu noon, ñibbisi.17Am nga yaakaaru ëllëg.»Kàddug Aji Sax jee.«Say doom ay délsi seenum réew.18Maa dégg moos askanu Efrayim di binninaan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma,ni sëllu wu dese tàggat.Ngalla waññi nu, nu waññiku;yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla.19Dëddu woon nanu la mooswaaye léegi réccu nanu.Xam nan ne tooñ nanu,ba tey nuy màttuy wiccax.Danoo rus, toroxndax sunu ñaawtéefi ndaw.”»
20Aji Sax ji ne:«Xanaa du Efrayim ay sama doom ji ma sopp,di gone gi may bànneexal?Lu ma ko gëdd gëdd,di ko bàyyi xel.Moo tax sama xol di ko laaj,ma yërëm koo yërëm.»Kàddug Aji Sax jee.
21«Sampal ay xàmmikaay ci yoon wi,teg fi say màndarga.Booy dem, defal sa xel ci yoon wii,ñall wii nga topp.Israayil mu taaru mi, ñibbisil,ñibbisil sa dëkk yii.22Ndaw su toogadi si,foo àppal sa ciŋiñ-caŋañ ji?Aji Sax ji déy, sàkk na guléet kaw suuf:yees ba mel ni jigéen juy jëflanteek góor23Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq.Dees na ne: “Yaw màkkaanu njubte bii,yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi,yal na la Aji Sax ji barkeel!”24«Waa réewum Yuda ak dëkk-dëkkaanam yépp ay bokk dëkk, ak beykat yeek màngaan yi yor gétt.25Maay nàndal ku mar, leqali ku loof.»26Ba loolu amee ma yewwu, ne xiféet, xam ne samay nelaw neex na.

Aji Sax ji teewlul na Israayil

27«Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may jiwe kërug Israayil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala.28Te ni ma leen teewloo woon ba ma leen di buddat, di leen fàqat, di leen daaneel, di leen yàqate aka lor, noonu laa leen di teewloo ngir defar leen, jëmbat leen.» Kàddug Aji Sax jee.29«Su boobaa deesatul ne:“Baay lekk reseñ ju xaay,mu uum bëñu doom ja.”30Su boobaa ku nekk sa bàkkaaru bopp a lay rey. Ku lekk reseñ yu xaay, sa gëñi bopp lay uum.

Kóllëre gu yees a ngii

31«Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israayil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees.32Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee.33«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israayil bu fan yooyu weesoo,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.34Kenn dootul soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Lii mooy saxal Israayil

35Aji Sax ji dafa wax,moom mi dogal jant di leeral bëccëg,dogal weer ak biddiiw di leeral guddi,yëngal géej, gannax yi riir,kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,36mu ne: «Su dogal yooyu manoona toxu, may gis,su boobaa askanu Israayil dina mana fey ba fàww, may gis.»Kàddug Aji Sax jee.
37Aji Sax ji dafa wax ne:«Su nit manoona natt kawewaayu asamaan,mbaa mu manoona xayma xóotaayu suuf,su boobaa ma mana xalab mboolem askanu Israayil,xalab leen ndax li ñu def lépp.»Kàddug Aji Sax jee.38Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkku Yerusalem, dale ko ca soorooru tata bu tudd Ananel ba ca buntu Ruq ba.39Dees na fa rëddaat kemu dëkk bi, jubal ba tundu Gareb, wëri ba Gowa.40Mboolem xur yu ñu sànni néew yaak dóomu-taal ak mboolem tool ya, ba ca yoonu ndox ma ca Sedoron, ba ca ruqu buntu Fas ya ca penku: lépp lees di sellalal Aji Sax ji. Deesatu fa buddat mbaa di fa daaneel dara.»