1Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji, ne ko:2«Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne: Nanga bind cib téere kàddu yi ma la wax yépp.3Ndax kat ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay tijjil sama ñoñ seen wërsëg, muy Israayil di Yuda.» Aji Sax jee ko wax. «Maa leen di delloo ca suuf sa ma moomale woon seeni maam.»
Ay teraanga nuyoo na
4Kàddu yii la Aji Sax ji wax ci mbirum Israayil ak ci mbirum Yuda.5«Aji Sax ji déy dafa wax ne:Yuuxi tiitaange dégtu na,njàqare la, du jàmm.6Laajteleen te xool,ndax góor day wasin léegi?Moona maa gis jàmbaar ju nekk jatu,ni kuy matu,kanam xoyyi.7Wóoy boobu bés bu réy,ba bés du ni mel!Bésu njàqare lay doonñeel askanu Yanqóoba,waaye dañuy mucc.8«Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem.9Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.10Waaye yaw Yanqóoba sama jaam,bul tiit,» kàddug Aji Sax jee;«yaw Israayil, bul ragal.Fu sore laa lay wallujee,yaak sa askan wa ca réewum njaam ga,Yanqóoba dellu dal, fegu;kenn dootu ko tiital.11Maa ngeek yaw, nar laa wallu.»Kàddug Aji Sax jee.«Maay faagaagal mboolem xeet ya ma la sànniji.Yaw nag duma la faagaagal,duma la ñàkka topp moos,waaye li nga yelloo laa lay yare.»12Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Sa damm-damm du faju,sa góom du wér.13Amul ku lay sàmmal sa àq,te sab dana amul pajtal mu baax.14Sa soppe yépp a la fàtte,kenn faalewu la ci,ndax dumay noon laa la duma,yar la yarinu ku néegngir sa ñaawtéef ju réyak sa bàkkaar yu bare.15«Damm-damm yu dul wérak mitit wu tar jarul jooy.Maa la teg lii,ndax sa ñaawtéef ju réyak sa bàkkaar yu bare.16Waaye ku la lekk, dees na ko lekk;sa noon yépp lañuy jàpp njaam ba ñu daj.Ku la futti, dees na ko futti,ku la saax-saaxee dees na ko saax-saaxee.17«Ñu ngi la naan: “Waccees na la,”naan la: “Siyoŋ yaw, faaleesu la,”waaye maa lay may wér,faj say góom.»Kàddug Aji Sax jee.18Aji Sax ji dafa wax ne:«Maa ngii di tijji wërsëgu askanu Yanqóoba,ñibbisil leen,baaxe seeni dëkkuwaay,ba dëkk dekkee ca tundam wu gentoon,kër buur taxawaat bérebam,19cant jollee ca,di riirum mbégte.Maa leen di ful,te duñu wàññiku,darajaal leen,te dootuñu tuut.20Seeni doom dañuy mel na woon,seen mbooloo sax fi sama kanam,may mbugal ñi leen di sonal.21Su boobaa seen njiit di seen deret,di seen kilifa, soqikoo ci ñoom;ma woo ko, mu jege ma,nde nit jaayul bakkanam,ba jegesi ma te woowuma ko !»Kàddug Aji Sax jee.22«Yeenay doon sama ñoñ,man, may seen Yàlla.»23Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog,sànjam fettax na,di aw callweer,callweeral boppu ku bon.24Sànjam Aji Sax ju tàng ji du giif,te sottalul li mu nar.Fan yu mujj yangeen xam ci dara.