Yeremi22wol_mbs
1Aji Sax ji dafa wax ne: «Demal kër buurub Yuda, nga jottali fa kàddu gii.2Danga naan: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yaw buurub Yuda mi toog ci jalub Daawuda, yaak say jawriñ ak sa nit ñiy jaare yii bunt.3Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettali ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jàmbur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii béreb.4Su ngeen jëfee ba jëfe santaane bii déy, buur du noppee dugge yii bunt, di toogal Buur Daawuda fi jalam, di dawal watiir aki fas, ànd ak seeni jawriñ ak seeni nit.5Waaye su ngeen dégluwul sama santaane yii, giñ naa ko ci man mii,” kàddug Aji Sax jee, “ab gent rekk la gii kër di doon!”»6Aji Sax ji déy dafa wax ci mbirum kër buurub Yuda ne:«Yaay sama àllub Galàdd,sama collu tundu Libaŋ,waaye déy, maa lay def ni màndiŋ,ngay dëkk yu kenn dëkkul.7Maa lay beralal yàqkatyu fàggu seeni gànnaay,dàjji sa tànnéefi banti seedar,sànni ca sawara sa.8«Doxandéem yu bare dinañu jaare dëkk bii, di laajte ci seen biir naan: “Ana lu waral Aji Sax ji def nii bii dëkk bu mag?”9Su ko defee ñu ne leen: “Xanaa li ñu fecci seen kóllërey Yàlla Aji Sax ji, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu.”»