Yeremi20wol_mbs

Tëj nañu Yeremi

1Ci kaw loolu, Pasur doomu Imer, sarxalkat ba jiite woon saytub kër Yàlla ga, ba mu déggee Yonent Yàlla Yeremi muy jottali kàdduy waxyu yooyu, mu dóorlu ko, jéng ko ca buntu kër Aji Sax ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin.3Ca suba sa Pasur yiwee ko ca jéng ba. Yeremi ne ko: «Aji Sax ji tuddeetu la Pasur; Magor-Misabib (muy firi Tiitaange ju dajal) la la tudde.4Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee.5Maay joxe lépp luy alalu dëkk bii. Mboolem lu fiy njariñ, mboolem gànjar, mboolem denci buuri Yuda, dinaa ko teg ci seen loxol noon yi, ñu sëxëtoo, jël, yóbbu Babilon.6Yaw Pasur, yaak sa waa kër yépp ay duggi njaam ca Babilon. Babilon nga jëm te fa ngay dee, ñu rob la fa, yaak mboolem sa soppe ya nga daan àgge ay kàdduy waxyuy fen.”»

Yeremi ñaxtu na

7Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma,ma naagu, nga nax ma,jaay ma doole, ba man ma.Ñu ngi may kekku bés bu ne,ku ne di ma kókkali.8Saa yu ma waxee, damay xaacu,fitnaak salfaañoo ma tax di yuuxu.Kàddug Aji Sax jee may yóbbey xasaki saaga bés bu ne.9Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko,dootuma jottali kàdduy waxyu ci turam,»sama xol bi mel nib taalbu tàkk, tàbbi sama biir yax yi;may jéema muutuwaale sa kàddu,te duma ko man.10Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan:«Éey, “Tiitaange ju dajal!”Booleleen ko, boole rekk!»Ñi ma séqal jàmm sax,di yeeru ma fakkastalu,naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko,ba mana feyu.»11Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare.Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan,xanaa rus lool, ndax duñu baaxle;gàcce gu yàgg lay doon te du fey.12Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaw miy nattu ku jub,di gis xel ak xol,may ma, ma gis ni nga leen di feye;yaw de laa diis sama mbir.
13Woyleen Aji Sax ji,màggalleen Aji Sax ji!Mooy xettali néew-ji-dooleci dooley ku bon.
14Alkute ñeel na bés ba ma juddoo,bés ba ma saa ndey juree,yàlla bumu barkeel.15Alkute ñeel na ka ko yegge baay,ne ko: «Sa soxna am na doom ju góor,»ba tax baay bég a bég.16Yal na kooku mel ni dëkkyi Aji Sax ji tas te yërëmu leen!Yal na dégg yuuxi suba teelak xaacuy xarey njolloor.17Moo ma reyul ci sama biiru ndey,ma bàmmeeloo sama ndey,te du wasin mukk.18Ana lu ma doon génne ca biiram,di daj coonooku tiis,mujje gàcce?