1Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma, ne ma:2«Bul jël jabar,bul am doom ju góor mbaa ju jigéen ci bii béreb.»3Aji Sax ji kat dafa wax ci gone yu góor yeek gone yu jigéenyi juddoo ci bii béreb,wax ci seen ndey yi leen jurwax ci seen baay yi leen meññ ci mii réew,4mu ne: «Jàngoroy dee a leen di rey.Deesu leen jooy, deesu leen rob.Seeni néew ay tosal suuf.Saamar akub xiif a leen di sànk,seeni néew leel njanaaw ak rabi àll.»5Te Aji Sax ji kat dafa wax ne:«Bul dugg kërug dëj,bu fa dem di ñaawlooka jaale.Maa xañ askan wii sama jàmm,»kàddug Aji Sax jee,«xañ leen sama ngor ak sama yërmande.6Ku mag ak ku ndaw ay dee ci réew mii,te deesu leen rob,deesu leen jooy.Kenn du dagg yaramammbaa muy nelu, di ko ñaawloo.7Kenn du leen sédd aw ñamwu ñuy dëfale ku deele,kenn du leen joxub kaas, dëfale leen,doonte baay a dee mbaa ndey.8Kërug bernde it, bu fa dugg,di toogandoo, di lekk aka naan.»9Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi kat dafa wax ne:«Maa ngii di dakkal ci bii béreb,ngeen teewe, fekke léppluy coowal mbégteek bànneex,boroom séet ak séetam selaw.10«Su ko defee, boo waxee askan wii kàddu yooyu yépp, ñu ne la: “Ana lu waral Aji Sax ji dogalal nu musiba mu réy mii mépp? Ana fu nu tooñe ak fu nu moye sunu Yàlla Aji Sax ji?”11Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamooka sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm.12Yeen nag, ngeen di bon, ba raw seeni maam. Yeena ngii, ku nekk të ticc, topp xolam bu bon, bañ maa déggal.13Maa leen di dàqe ci réew mii, jëme réew mu ngeen xamul, seeni maam xamuñu ko, ngeen di fa jaamu guddeek bëccëg yeneen yàlla, ndax dootuma leen baaxe.”
Yaakaar jeexul
14«Waaw ay bés a ngi ñëw déy,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génne bànni Israayil réewum Misra.”15Waaye dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, ki jële bànni Israayil réewum bëj-gànnaar, te jële leen mboolem réew ya mu leen sànke woon.” Maa leen di delloosi seen réew ma ma joxoon seeni maam.
Kenn rëccul mbugal mi
16«Maa ngii di woolu nappkat yu bare.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu napp ñii ba noppi, ma woo rëbb yu bare, ñu rëbb leen ci kaw mboolem tund wu mag ak wu ndaw, ba ci bépp xar-xaru doj.17Samay bët a ngi ne jàkk déy ci seeni jëf. Dara umpu ma ci. Seeni ñaawtéef, dara rëccu ma ci.18Dama leen di njëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»
Ñépp ay ràññeeji Aji Sax ji
19Yaw Aji Sax ji may dooleel,di ma feg, di ma làq bésub njàqare,yaw la xeet yiy bawoo cati àddina,fekksi la, naan:«Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon,xërëmi neen yu amul njariñ.20Ndax nit man naa sàkkal boppam ay yàlla?Te duñuy yàlla sax!»21«Moo tax maa ngii di leen xamal bii yoon,ba ñu xam sama diisaayu loxook sama doole,xam ne maay Aji Sax ji.