Yeremi12wol_mbs
1Aji Sax ji, yaa dëggu,ak li may tawatsi fi yaw lépp.Teewul ma di la diis mbir ci say àtte:lu tax ku bon di baaxle,bépp workat bu bon di féex?2Yaa leen jëmbat, ñu sampi reen,law ba meññ;jegeñal la seen làmmiñ,te fekk nga sore seen xol.3Waaye yaw Aji Sax ji, xam nga ma;gis nga ma, seetlu sama xol ci yaw.Diri leen niy xar yu ñuy rendi,beral leen bésub rendi.4Ba kañ la réew mi naa sereŋ,gàncaxu tool yépp di lax?Rabu àll ak njanaaw a ngi sànkungir mbonug ñi fi dëkkte naan: «Moom de xoolul sunu muj!»5«Ndegam boroom ñaari tànk ngay rawanteel, xoox,nooy rawanteeki fas?Soo wóoluwul lu moy àll bu ne yàmblaŋ,nooy def ak gottub Yurdan?6Say bokk ak sa waa kër baay sax,ñoom it wor nañu la,ñoom it xaacu nañu, sam la;te bu ñu lay wax jàmm it,bu leen gëm.7«Dëddu naa sama kër,maa wacc sama séddoo,wacce sama soppey xol loxol noonam.8Sama séddoo ngi may niru léegigaynde ci gott bi,di ma xiiru, ba tax ma jéppi ko.9Sama séddoo baa ngi may saf tan mu toddemu moroomi tanam gaw.Doxleen dajaleji rabi àll yépp,indi leen ci bernde ji.10Gàngooru sàmm a sëxëtoo sama tóokëru reseñ,joggati sama waar,def waar wi ma neexmàndiŋ mu ne maraas.11Def nañu ko gent buy jooy fi sama kaw,réew mi mépp gental a gental,te saful kenn.12Tundoo tund wu ne faraas fi màndiŋ mi,ay yàqkat a ngi ciy bawoo,doon saamaru Aji Sax ji, di mëdd réew mépp,cat ba cat,jàmm réer luy dund!13Jiwum pepp, góob ay dég;sonn, ñàkk yool,xanaa mbetteel ci meññeef mii sababooci merum Aji Sax ji.»