Yeremi10wol_mbs

Aji Sax ji du moroomu xërëm

1Yeen bànni Israayil, dégluleen kàddugi leen Aji Sax ji dégtal.2Aji Sax ji dafa wax ne:«Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy;màndargam asamaan, buleen ko tiit;na ko yéefar yi tiit.3Aaday xeet yi kat neen la.Garab lañuy gore ca gott ba,ab yattkat yatte ko sémmiñ,4rafetale xaalis ak wurus,daaj koy pont, dëgëral,ba du yëngu;5muy saf kuñeental ci biir tóokërub xaal.Du wax, du séqi jéego,ñu di ko jaŋat-jaŋatee.Buleen ko ragal, du lore, du jariñe.»6Aji Sax ji, kenn melul ni yaw,yaaka màgg, jàmbaare, màggu tur.7Yaw Buuru xeet yi, ana ku la dul ragal?Yaw déy yaa yelloo ragal.Mboolem ñi xelu ci xeet yiak mboolem seeni buur,kenn melul ni yaw.8Ñoom ñépp a bokk dofe, ñàkk bopp:xam-xamu kasara, bant kese!9Xaalis lañuy jële Tarsis, xoobe ko bant,wurus wu jóge Ufas, ñu boole ca,ndaanaan liggéey ko,tëggu gànjar yatt ko,ñu solal ko ndimo lu yoletak lu xonq curr,lépp di liggéeyu ràbb yu xareñ.10Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg.Mooy Yàlla jiy dund,di buur ba fàww,xadaram gësëm àddina,meram man xeet yi.11«Lii nag, nangeen ko siiwal:“Seen yàlla yi sàkkul asamaan, sàkkuñu suuf,ñooy sànku, jóge fi suuf ak fi asamaan tiim.”»12Suuf, Aji Sax jee ko sàkke kàttanam;dun bi, mu sampem xelam;asamaan, mu lale xam-xamam.13Bu àddoo, ndoxum asamaan riir;mu yéegey niir fa cati àddina,riddee ngelaw fa dencam ya,daldi melax, taw.14Nitoo nit dim sanax, sore xam-xam,te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce.Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen,noowug bakkan, tus!15Cóolóolu neen, liggéeyu caaxaan;bu bésam taxawee, mu sànku.16Ki séddoo Yanqóoba déy wuute naak yii caaxaan.Kee bind lépp,te Israayil di giir gi mu séddoo.Kookooy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi!

Mbugal dikk na

17Yerusalemee, yeen ñi ñu gaw,forleen seen ëmb.18Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Maa ngii naa xërr waa réew mi bii yoon,teg leen njàqare, ba ñu yég ko.»19Wóoy man, yàqu naa!Ndaw góom bu metti!Dama noon lii jàngoro doŋŋ a,naa muñ!20Xayma xotatoo,buumi xayma xëttandoo,samay doom wacc ma, ne mes;kenn sampatul sama xayma, firi ko.21Sàmmi xeet weeka dofe:Aji Sax ji, diisoowuñook moom.Moo leen taxa bonle,seen jur gépp tasaaroo .22Xibaar a ngoog, di ñëw,riir mu réy a yëngoo réewum bëj-gànnaar,nara gental dëkki Yuda yu mag yi,till yi dëkke.

Yeremi tinu na Aji Sax ji

23Aji Sax ji, maa xam nenit moomul yoonam,kuy dox moomuli jéegoom.24Aji Sax ji, yar ma lu yem,te bañ maa yare mer,di ma semmal.25Xëppal sa xadar yéefar yi la yégul,ak làng yi la tuddul.Ñoo mëdd giirug Yanqóoba,mëdd leen, bóom leen,gental seen dëkkuwaay.