1Askan wiy doxe lëndëm nii,ñooy gis leer gu mag.Ñooñu dëkke réewum dee mu ne këruus,ñoom la leer di fenkal.2Aji Sax ji, yaay yokk xeet wi,fulal leen bànneex,ñuy bége fi sa kanam, mbégtem ngóob,mel ni ñuy bànneexoo fa ñuy séddoo alalu xare.3Yaa leen di sippil seen sëf,damm bant ba ñu leen gàlloon,ak yetu ña leen nootoon,na nga leen defaloon rekk ca xareb Majan.4Mboolem dàll wu ab noon dukkate ba dikk,ak turki bu màndi deretu xare,sawara lees koy leel.5Nde gonee juddu, ñeel nu,di doom ju góor ju ñu nu may,mu yenu kilifteef gi,ñu di ko woowe Kiy xelale te yéemuak Yàlla jàmbaar jiak Baay bi sax dàkkak Buuru jàmm bi.6Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu,fa jalub Daawuda ak nguuramga muy samp, saxale ko yoon ak njubtey jii ba fàww.Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Aji Sax ji yokk na mbugalam
7Boroom bee yónnee kàddugu dal Israayil, askanu Yanqóoba,8xeet wépp jot ca,ba ca Efrayim ak waa Samari,ñay damooka sagu naan:9«Ay móol màbb,nu yatt ponkali doj, tabaxaat,xànqi garab yu ndaw daanoo ca,nu wuutal ca garabi seedar yu mag.»10Aji Sax ji yékkati nooni Buur Reccin, fi seen kaw,gemb seeni bañ,11Siri songe penku; Filisteen ña, sowu,ñu sëxëtoo Israayil, wann.Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom,meddiwul ba tey.12Waaye xeet wi delluwuñu ca ka leen duma,toppuñu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.13Moo tax Aji Sax ji doge Israayil bopp ak geen,boole tiir ak barax doge ci benn bés.14Mag meek kàngam li ñooy bopp bi,yonent bi mokkal naaféq dib geen.15Ñi jiite askan wii ñoo leen di sànk,ña ñuy jiite loru.16Moo tax Boroom bi du bége seeni xale yu góor,du yërëm seeni jirim ak seeni jëtun.Ñoom ñépp a gëmadi, di def lu bon,ku ci nekk di wax lu amul bopp.Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom,meddiwul ba tey.17Mbon a ngi tàkk moosni sawara, xoyom dég aki dagg,jafal gajji gott bi,mu ne jippét, saxaar, naaw.18Merum Aji Sax ji Boroom gàngoor yi taal na réew mi,xoyom waa réew mi,kenn yërëmul sa mbokk.19Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu,di xàmpe càmmoñ te suuruñu,ku nekk di yàpp sa mbokk:20Manase song Efrayim,Efrayim song Manase,ñu mànkoo, noonoo Yuda.Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom,meddiwul ba tey.