1Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw,ndax Aji Sax jee ma diw , fal mangir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm.Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex,yégal jaam yi seen goreel,yégal ñi ñu tëj seen ubbite.2Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji,ak at mu sunu Yàlla di mbugalee.Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp,3ngir indil waa Siyoŋ ñiy ñaawluab kaala gu wuutu dóomu-taal,ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis,ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex,ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njubte yi,njëmbat li Aji Sax ji jëmbat,ngir teewal màggaayam.»4Ñooy tabaxaat gent ya woon,yékkati béreb ya tasoon bu yàgg,dekkal dëkk yu tas,béreb yu gental ay maasi maas.5Ay gan ay dikk,di leen sàmmal seeni gétt,ay doomi doxandéem di leen beyali toolak tóokëri reseñ.6Yeen nag lees di woowe:«Sarxalkati Aji Sax ji,»ñu naa: «Sunu jawriñi Yàlla yaa ngii!»Alali xeet yi, yeena koy lekk,di damoo seeni koom.7Sama ñoñ ay weccikoo seen gàcceñaari céri teraanga,sarxolley mbég di seen cér,wuutu toroxte.Ñaari cér lañuy am ca seenum réew,mbégte mu sax ñeel leen.8Man Aji Sax ji, damaa sopp yoon,bañ càcc ak ñaawtéef.Maay dàmp sama ñoñ ni mu ware,fas ak ñoom kóllëre gu sax.9Dees na xàmmee seen askan fi biir xeet yi,xàmmee lu meññe ci ñoom fi biir waaso yi;képp ku leen gis ràññee neñooy askan wu Aji Sax ji barkeel.
Almasi bi bége na mucc gi mu maye
10Maa bég a bég ci Aji Sax ji,sama xol di sedd ci sama Yàlla jii.Moo ma solal yérey mucc,sànge ma mbubbam ndam,may nirook boroom séetbu kaalawu ni sarxalkat,ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.11Ni suuf di fettalem njebbit,ab tool di ko saxalem jiwu,ni la Boroom bi Aji Sax ji di jebbiledëgg ak cant,xeetoo xeet seede ko.