1Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo,noppam naqariwul ba tere koo dégg.2Seeni ñaawtéef a dox seen digganteekseen Yàlla.Seeni moy a leen xañ kanamam,ba mu tanqamlu leen.3Seeni loxoo taq deret,ngeen ne ripp ci ñaawtéef,làmmiñ di fen, di sos njekkar.4Du dëgg gu kenn wut cib àtte,du dëgg gu kenn sàkku cib layoo.Ñu ngi yaakaar caaxaan, di fen,di sos ayib, di wasin ñaawtéef.5Nenu ñàngóor lañuy tostan,di ràbb lëndu jargoñ.Ku lekk ci nen yi dee,te boo ci tojeeb nen,saamaan fëlle ca.6Seeni lënd du ràbbe ba solal nit,mbaa di sàng kenn;seenum ràbb ñaawtéef lay jur,seen loxo ya ko liggéey sabab fitna,7seeni tànk daw wuti lu bon,ñuy yàkkamtee tuur deretu jàmbur;seeni xalaat di ñaawtéef,yàquteek njaaxum féete ca seeni yoon.8Yoonu jàmm, xamuñu ko,te yoon amul fa ñuy jaare,xanaa sàkk seen yoon yu lunkte ku fa awe doo daj jàmm.9Lee tax yoon sore nu,te dëgg du nu dab.Danuy yaakaar leer,lëndëm ne jaas,nuy séentuy ceeñeer,tey lëndëmtuy wéy.10Nu ngi làmbatu ci biir tabax ni silmaxa,di tëñëx-tëñëxi ni ku amuli gët,di fakkastalu bëccëg ndarakàmm ni bu doon guddi,di dëkk ak ñu wér péŋŋ te mel ni ña dee.11Nun ñépp a ngi xiiru ni rab wu aay,binnee binni niy xati,yaakaar yoon, yoon wuute,séentu wall, wall sore.12Sunuy tooñ a bare fi sa kanam,sunuy moy a nu seedeel,sunuy tooñ a nu topp,te xam nanu xéll sunuy ñaawtéef.13Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko,te noo dëddoo sunu Yàlla jii,kàdduy fitna ak fippu,ak fen yu nu mébét, nas ko,14ba yoon dellu gannaaw,àtteb yoon dànd,dëgg fakkastaloo fa pénc ma,njub tëë agsi.15Dëgg a tumurànke,ku dëddu mbon sax, ñu ñori la,Aji Sax ji gis ci, ñaawlu ko,ndax yoon a amul.16Daa xool, gisul kenn;mu tiisoo li ci kenn jógul,moo tax loxoom may ko ndam,ci àtteem la sukkandikoo.17Moo sol kiiraayal njub,mbaxanawoo mucc,solati yérey mbugale,sàngoo malaanum xéraange.18Mooy delloo ku ne yool ba mu yelloo,mbugal ay bañam, fey ay noonam,ba delloo waa dun ya yool ba ñu yelloo.19Dees na ragale turu Aji Sax ji fa sowu,ragale màggaayam ba penku.Bu noon bi agsee ni walum dex,ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.20«Ab jotkat ay dikkal Siyoŋ,ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.»Kàddug Aji Sax jee.21«Man nag, lii mooy sama kóllëreek ñoom:sama xel mi tegu fi sa kaw,ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ,lenn du ci teqalikook sa gémmiñak sa gémmiñu askan,ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.»Aji Sax jee ko wax.