1Aji jub ñaa ngi dee,te kenn yégalu ko yaramam.Gor ñaa ngi faatu,te kenn ràññeewulne aji jub ji, faatoom, musiba la koy moyale.2Kiy am jàmm ëllëg,di am noflaay ci biir tëraayam,mooy kiy wéye njub.3Waaye yeen, dikkleen fii,yeen doomi xërëmkat yi,yeen askanu njaalookat yiy gànctu,4ana ku ngeen di ñaawal?Ana ku ngeen di ŋóobi,ak di ko kókkali?Xanaa dungeen doomi moykat,di askanu workat,5di xabtaloo bànneexci ker garab yu mag yi,ak ker garaboo garab gu naat,di rendi seeni doom ci yoonu ndox yi,ak xarantey doj yi?6Yaw Israayil, jëlal doj yu rattaxyi ci yoonu ndox wi, séddoo,muy sa cér, nga muurloo!Ñoom ngay tuural,di leen defal ay saraxi pepp.Waaye Aji Sax ji nee:«Ndax damay jéllale?»7Tund wu mag te kawe,nga fàkk fa tëraay,yéeg fa, di fa sarxalal.8Yaa takk say baaxantalci sa lafu bunt ak sa jëni bunt,yaa ma wacc, di ñorikoo feneen,yéeg sab lal, yaatal.Yaa takktook ñii nga soppa tëddalte safoo di niir seeni cér.9Yaa tukki ba ca buur ba, yóbbaaleg diw,ak cuuraay lu ne gàññ,yebal say ndaw fu sore,ba ñu àkki njaniiw.10Tukki bu sore bu la sonal saxtaxu la ne: «Fomm naa.»Bànneex bi ngay séentu ngay leqalikoo,ba tax sonnuloo.11Aji Sax ji nee: «Ana kooy tiit,ak koo ragal ba di ma wor,fàttalikootoo ma,faaleetoo ma?Damaa noppi lu yàgg daal,ba tax ragalatoo ma?12Defe nga ne yoon nga defee,waaye dinaa la weer,te sa jëf du la jariñ.13Boo wootee wall,na la sa gàngooru tuur xettali.Ñoom ñépp la ngelaw di buub,callweer yóbbu leen.Waaye ku ma làqoo,kookooy moom réew mi,séddoo sama tund wu sell wi.»14Dees na ne: «Maasaleleenoo, maasaleleen,yaatalleen yoon wi,te jële luy pakk ci sama yoonu ñoñ.»15Ku màgg, Ku kawe ki,ki màkkaanam sax dàkkte turam sell, daa wax ne:«Fu kawe te sell laa màkkaanoo,maa dëkk ak boroom xol bu mokk te toroxlu,ngir leqali ku toroxlu,leqali boroom xol bu mokk.16Duma wéye di sikke ba fàww,duma saxoo di mer,lu ko moy képp ku ma sàkkday tàggook bakkanam.17Ñaawtéefi Israayil ak alalam ju lewulmoo ma merloo,ma duma ko, xañ ko sama kanam,waaye mu të ticc, topp xolam.18Xam naa jikkoom,waaye maa koy faj,wommat ko,dëfale koy xéewal,mook ñiy ñaawloondook moom.19Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant.Jàmm, na jàmm ñeel ñépp,ku soreek ku jege.»Kàddug Aji Sax jee.Mu ne: «Maa leen di faj.»20Waaye ñu bon ñi, mbete géejgu sàmbaraax, tëë dal,gannax yay baaje ban ak suuf.21Sama Yàlla nee:«Jàmm du ñeel ñu bon ñi.»