Esayi56wol_mbs

Xeet yépp la Aji Sax jiy ñoñoo

1Aji Sax ji dafa wax ne:«Sàmmleen yoon, di def dëgg.Sama wall kat a ngi dikk léegi,sama àtte laa ne, léegi mu teew.2Ndokkalee kuy jëfe lii,ndokkalee doom aadama ju jàppoo lii,di sàmm bésub Noflaay,bañ koo ñàkke worma,di sàmm loxoom ci jépp jëf ju bon.»3Doomu doxandéem bu jokku ci Aji Sax ji,bumu ne: «Aji Sax jee may beddee beddi ci ñoñam.»Jaam bu ñu xañ ngóora it bumu ne:«Man garab gu jaasir doŋŋ laa.»4Aji Sax ji kat dafa wax ne:«Jaam yi ñu xañ ngóora,su ñu sàmmee sama bési Noflaay,taamu sama coobare,tey feddali sama kóllëre,5maa leen di may ci sama biir kër, sama biir ëtt,doj wu ñu leen di fàttalikooak tur wu leen di gënal doom yu góor ak yu jigéen.Tur wu sax dàkk laay mayjaam yi ñu xañ ngóora,te du fey mukk .6Doomi doxandéem yi ànd ak Aji Sax ji,ngir liggéeyal ko,ngir sopp turu Aji Sax ji,te di ay jaamam,muy képp kuy sàmm bésub Noflaay,baña ñàkke worma bés bi,xanaa di feddali sama kóllëre,7ñooñu, maa leen di yóbbusama kaw tund wu sell,bànneexale leen sama biir kërug ñaan.Seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax,dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay;ndaxte sama kër gi, kërug ñaan lees ko tudde,ñeel xeetoo xeet.»8Kàddug Boroom bi Aji Sax jaa ngii,kiy dajale giiri Israayil yi tasaaroo,mu ne: «Maay dajaleeti,dolli ca la ma dajale woon.»

Ab daan ñeel na njiit yi

9Yeen rabi àll yi,dikkleen ci bernde ji,yeen rabi gott bi yépp.10Wattukati Israayil yépp a silmaxa,te xamuñu dara.Ñoom ñépp a diy xaj yu luu,manuñoo baw,xanaa tëdd di jeneer,soppi nelaw.11Xaj yu tiit a tiit lañu,xamuñu suur,te ñooy sàmm yéey!Ñoom ñépp, kenn manu cee xam dara,seen yoonu bopp lañu topp,ak seen amin wu lewul.12Ña nga naa: «Dikkleen, ma indi biiñ,nu màndeew ñoll tey ak ëllëg,li fi des du jeex.»