1Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul!Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.Aji Sax ji nee:«Ndaw si ñu foñ moo gëna jabootkiy séy.2Yaatalal sa xayma bi,firi sa sori xayma yu gëna yaate bul yéem.Yokkal sa buumi xaymate samp say bant, mu dëgër.3Dinga saam ay doom ndijoor ak càmmoñ,saw askan moom ay xeet,sancaat dëkk yu gentaloon.4Bul tiit, doo rus mukk.Bul jaaxle, deesu la kersaal mukk.Sa gàcce ga ba ngay ndaw, dinga ko fàtte,te sa tiisu jëtun wa dootoo ko fàttaliku.5Sa jëkkër, Ki la sàkk,Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam.Aji Sell ju Israayil moo la jot,te moo di Yàllay àddina sépp.6Aji Sax jee la woo, nga dib jeeg bu ñu wacc,sa xol jeex tàkk,Mu ne la:“Nees di wacces ndawsi nga takk ba ngay ndaw?”»Sa Yàllaa ko wax.7Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt,dellu la jël ci yërmande ju yaa.8Sama xol a jóg,ma xañ la sama kanam ab diir,waaye maa lay yërëme ngor gu sax.»Aji Sax ji lay jot moo ko wax.9Mu ne: «Na ma defoon akndoxum Nóoyin ma mooy lii tey.Maa giñoon ne ndoxum Nóoyin ma,mu ni day dootul wale kaw suuf.Noonu it laay giñe neduma la mereeti,duma la rëbbati.10Bu tund yu mag yi doon toxu,yu ndaw yiy raf sax,sama ngor du la toxul,te sama kóllërey jàmm du raf.»Aji Sax ji la yërëm moo ko wax.11«Ngalla yaw Yerusalem,mi ngëlén pamti-pamtee ba nga jàq,te kenn dalalu la,man Aji Sax ji,maa ngii di la tabaxe doj yu ne ràññ,samp la ci safiir.12Maay defare sa kawi tata peri rubi,def say bunt per yuy lerxat,def sa tata yi la wër yépp doj yu bakkane,13mboolem sa doom yu góor ay jànge ci Aji Sax ji,boole kook jàmm ju ne ñoyy.14Àtteb dëgg moo lay dëgëral,nga sore nooteel, doo tiit;sore tiitaange, du la jege.15Xanaa dees na songe moos,waaye ku la song it, yebalu ma ko,te ku la song daanu fi sa kanam.16Xoolal, man maa sàkk ab tëggbuy wal taalu këriñ,defar ca ngànnaay lu ne.Waaye maa sàkk ityàqkat buy rajaxe.17Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal,du sotti,te boroom làmmiñ wu la jógal cib layooyaa koy tiiñal.Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér,looloo di àtte bi ma leen di dikke.»Kàddug Aji Sax jee.