Esayi53wol_mbs

1Ana ku gëm sunub dégtal?Dooley loxol Aji Sax ji ana ku mu ko won?2Kii màgge fi kanamam ni njëmbat,te nirook reen bu fette ag kekk.Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire,du meloom wu nu koy soppe.3Dees na ko xeeb, daw ko,muy nit ku bare mititte miin naqar.Mu mel ni ku ñuy dummóoyu,dees koo xeeb te nawloowuñu ko.4Ndaxam moom sunu wopp la yenu,sunuy mitit la sëfoo.Nun nu foog ne dees koo mbugal,foog ne Yàllaa ko duma, toroxal ko.5Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko;sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko.Yar yi nu jàmmal moom la dal,te mooy ki nu wére ciy góomam.6Nun ñépp a lajj niy xar,ku nekk walbatiku topp yoonam,te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.7Dees koo néewal doole, mitital kote ubbiwul gémmiñam,xanaa mel ni xar mu ñuy rendiji,ne cell ni xar mu ñuy wat,ubbiwul gémmiñam.8Àttewuñu ko dëgg, yóbbu,te ag maasam kenn teewluwul netooñ gu sama bokk yi tooñlees ko génne ci réewum aji dund ñi,te loolu lees ko faate.9Ni ñuy robe saay-saay lañu ko robe,denc ko ci bàmmeelu boroom alal,soxorul, fenul.
10Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii,teg koy naqar,su nangoo doon saraxu peyug tooñ,gis askanam, aw fanam gudd,te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.11Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko.Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub,mu def ñu bare, ñu ñu limal njub,ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef.12Moo tax ma di ko jox ab cérci biir ñu bare,mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem,ngir moo jébbale bakkanu boppam,ñu limaale kooki tooñkat,moo gàddu bàkkaaru ñu barete mooy tinul moykat yi.