Esayi52wol_mbs

Yerusalem dina suqaliku

1Yewwulee, yewwul,Siyoŋee, làmbool sa doole!Yerusalem, dëkk bu sell bi,solul ba ne ràññ!Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewuku lay songati.2Yaw Yerusalem, mi ñu jàpp njaam,jógal fëgtu,yaw janq Siyoŋ mu taaru mi ñu jàpp njaam laa ne,tikkil buum gi ci sa baat.3Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Dees leena wànteeroon ci dara,te du xaalis lees leen di jotaate.»4Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Misra la sama ñoñ njëkka wàcc, dali fa,Asiri door leena noot ci dara.5Léegi nag ana lu fiy sama wàll?»Kàddug Aji Sax jee.Mu ne: «Jàpp nañ sama ñoñ njaam ci dara;seeni sang a ngi tëggu,di dëkke ñàkke teggin sama tur.»Kàddug Aji Sax jee.6«Moo tax sama ñoñ di xam maay kan;moo tax bésub keroogñu xam ne maay wax te maa ngii!»
7Ndaw leeka rafeti tànk,kee bartaloo tund yi,di la dégtalsi jàmm,di la xibaar lu neex,àgge la ag mucc,ne la: «Éey, Siyoŋ,sa Yàllaay Buur!»8Déglul sa wattukat yi,ña ngay xaacu, sarxolleendoo.Ñoo gisal seen boppAji Sax ji di ñibbisi Siyoŋ.9Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle;Aji Sax jeey dëfal ñoñam,mooy jot Yerusalem gii!10Aji Sax jee wone dooleem ju sell ji,xeet yépp di gis,ba ca cati àddina.Ñépp ay gis sunu wallub Yàlla.11Génnleen, génnleen foofa!lu sobewu, buleen ko laal!Yeen ñiy yóbbu ndab yu sell yu Aji Sax ji ,setluleen te génn foofa.12Dungeen gaawtu déy, di dem;duy xél moos ngeen fay génne.Aji Sax jeey dox jiitu leen,te Yàllay Israayil laa ne, moo leen di féete gannaaw.

Teraangay jaam bi wuutu na coonoom

13Aji Sax ji nee: «Sama jaam baa ngii,mooy baaxle, kawe,dees na ko yékkati, darajaal ko lool.14Moo dawoon yaramu ñu bare,ndax yàqu ba nirootul nit,bindootul woon ni doom aadama,15waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet ,ba buur yi ne cell,ngir lu ñu leen waxuloon, ñu gis ko,lu ñu dégguloon, ñu mujj koo ràññee.»