1Dégluleen maa, yeen ñiy wuta doxee yoon,wuta déggal Aji Sax ji.Xoolleen doj wi ñu leen yatte,xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:2seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool,xool ci Saarata mi leen meññ.Ba muy kenn laa ko woo,barkeel ko, ful ko.3Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos,dëfalaale fépp fu fa dib gent,ba def màndiŋam ni toolub Àjjana,jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji,mbégteek bànneex teew fa,ak cantug woy feelu.4Yeen sama ñoñ, teewluleen ma,yeen sama ñoñ, dégluleen ma.Fi man la téereb yoon di bawoo,te maay fettaxal sama àtte,muy leeru xeet yi.5Sama wall jege na,sama àtte dëgmal na,ma nara àttee xeet yi sama dooley përëg.Man la waa dun yiy xaar,sama dooley përëg lañu yaakaar.6Séentuleen asamaante xool suuf si mu tiim.Asamaan ay tasaaroo ni saxaar,suuf ràpp ni mbubb,ñi ko dëkke dee niy weñ,te du tee sama wall di sax ba fàww,sama doxalinu yoon it du dagg.7Yeen ñi xam liy yoon, dégluleen ma,yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol.Buleen ragal nit ku leen sewal,buleen tiit seeni xaste.8Sax a leen di lekk ni mbubb,max ŋeeñ leen ni ndimol kawaru gàtt;te du tee sama doxalinu yoon sax dàkk,sama wall saxal maasoo maas.9Aji Sax ji, yewwul, ngalla yewwul;wone sa doole!Yewwul na bu njëkkoon,bu yàgga yàgg.Xanaa du yaa falaxe Raxab?Du yaa jam ninki-nanka jooja?10Xanaa du yaa wowal géejak ndoxum xuram wu ne màww,def xóotey géej aw yoon,ña nga jot jàlle ca?11Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee,agsaaley sarxolle fa Siyoŋ,kaalawoo mbég mu sax,mbégteek bànneex wàllsi,naqar aku tiis daw.12Man ci sama bopp maa leen di dëfal.Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee,doom aadama ju bokk aw demin akum ñax?13Dangeena fàtte Aji Sax ji leen sàkk,ki firi asamaan, lal suuf?Dangeen di dëkke bésoo bés,di tiit xadaru boroom doole buy waaja sànke?Ana fu xadaru boroom doole mujje?14Ku diisoon ba waaf léegi nga féex;doo deewe pax ma nga tëje,te doo ñàkk loo lekk.15Man maay seen Yàlla Aji Sax ji,kiy yëngal géej, riiral gannaxam,Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di sama tur.16Maa la sexal samay kàddu,yiire la sama keru loxo,aj asamaan, lal suuf,ne Siyoŋ: «Yeenay sama ñoñ.»17Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal,yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam.Kaas bu wex bay miirloo,taat wa, yaa ko siitaatu.18Amul ci ñi nga jur, kenn koo deseku lay wommat.Amul ci doom yi nga yar, kennku lay jàpp ci loxo.19Yii yaar de dikkal na la:yàquleek sànkule.Ana kuy bokk ak yaw saw naqar?Xiif ak loraangey saamar!Ana nu ma lay dëfale?20Sa doom yi ne lasar,mbete kooba yu fiir jàpp,ñu ne lareet fépp fu mbedd daje,këppoo sànjum Aji Sax ji,sa Yàlla ji leen rëbb.21Rikk déglul nag lii, yaw mi musiba dal,nga màndi te du biiñ.22Sa boroom Aji Sax ji,sa Yàlla jiy layool ñoñamdafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo,kaas bu wex biy miirloo;taatu kaas ba def sama mbugal,dootoo ko naan.23Maa koy teg ci loxol ñi la doon naqaral,te naan la: “Sëggal, nu joggi, jàll,”nga def sa gannaaw gi aw yoon,ñu joggi, wéy.»