Esayi49wol_mbs

Jaamub Aji Sax ji mooy leeru xeet yi

1Yeen waa duni géej, dégluleen ma;yeen askan ya fu sore, teewluleen ma.Fa sama biiru ndey la ma Aji Sax ji woowe,moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul.2Moo ñawal sama kàddu ni saamar,làqe ma keru loxoom.Moo ma def may fitt gu ñaw,yeb ma ci mbuusum fittam.3Moo ma ne: «Israayil yaa di samab jaam,yaw laay wonee samag leer.»4Man nag ma noon:«Maa sonn ci dara,coonob cóolóol bu amul njariñ.»Teewul sama àttee nga fa Aji Sax ji,sama yool a nga fa sama Yàlla.5Tey nag Aji Sax jee wax,moom mi dale sama biiru ndey,mooñ ma, ma dib jaamambi koy waññil askanu Yanqóoba ba ca moom,dajaleel ko bànni Israayil googu fa moom,ba jagoo teraangay Aji Sax ji,sama Yàlla jii di sama doole.6Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaambiy siggil giiri Yanqóoba,te wara delloosi ndesu Israayil gii.Tabb naa la, ngay leeru jàmbur ñi,ngir nga jottaliji ba ca cati àddina sama wall.»
7Aji Sax ji jotkatub Israayil,moom Aji Sell ju Israayil,moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko,te muy surgawu kilifa yi,mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg,ay kàngam di sukk,ngir Aji Sax jii gore,ngir Aji Sell ju Israayil ji la tànn.»
8Aji Sax ji dafa wax ne:«Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la;bu bésub mucc jotee, ma wallu la,sàmm la,def la ngay kóllëre sama diggante ak askan wi,ngir yékkatiwaat réew mi,séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey,9ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!”Fa ñu nekkoon cig lëndëm,laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!”Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall,ak wépp tund wu ne faraas tey.10Duñu xiif, duñu mar;tàngooru mbóoyo akub jant du leen sonal,nde ki leen ñeewantee leen di wommat,di leen yóbbu fu ndox bënne.11Sama tund yépp laay soppiy yoon,sëkkaat samay mbedd.12Ñu ngii bawoo fu sore,ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu,ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.»13Asamaanoo sarxolleel, suufoo bégal,te tund yi xaacoondoo!Aji Sax jee dëfal ñoñam,moo ñeewante néew-ji-dooleem ñii.
14Siyoŋ a nga naa: «Aji Sax ji wacc na nu,Boroom bi fàtte na nu!»15Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp,mbaa muy néege ku mu jur ci biiram?Bu ko manoona fàtte it,man duma la fàtte.16Sama biir loxo yii laa la ñaas,say tataa janook man ba fàww.17Ñi lay tabaxaat dañuy gaaw,te ñi la yàqateek ñi la gentaldañuy dem, ba la.18Séentul fi la wër te xool!Ñépp a ngi daje, di la fekksi.Ndegam maay Kiy dund,»kàddug Aji Sax jee,«ñoom ñépp ngay takkoo ni gànjargooy gànjaroo nib séet.
19Sa gentub tey bi déy a ngi wéet,di réew mu yàqu yaxeet.Waaye léegi déy mu fees ba far xat;fu ña la sànkoon di soree.20Ñàkkoon ngay doom,waaye ku nekk ci say doom ay dëkkalaatyii kàddu ci sab nopp:“Fii dafa xat,xajal ma fu ma dëkke!”21Dangay mujj naa:“Moo, ku ma jural ñii ñépp?Man mi ñàkkooni doom, manumaa jur,ñu toxal ma, wacc ma;ana ku leen yoroon te ma des, man kenn?Ñii sax, fu ñu ne woon?”»22Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:«Maa ngii di tàllal xeeti jàmbur ñi loxo,ñee ma yékkati raaya, woowe leen;ñu fab say doom yu góor, indi,tungóom sa doom yu jigéen, delloosi;23Yaw la ay buur di baayoo,seeni lingeer di la nàmpal.Ñoo lay sujjóotal,di la maral say tànk,ba nga xam ne maay Aji Sax ji,te ku ma yaakaar du rus.»
24Manees naa foqati alalu sëxëtoo ci loxol jàmbaar a?Am manees naa rëcc boroom doole bu la jàpp?25Aji Sax ji déy dafa wax ne:«Moona dees na foqati ku jàmbaar jàpp,ba rëccal alalu sëxëtoob boroom doole.Say jotewaale, maay joteek ñoom,te say doom, maa leen di wallu.26Ñi lay néewal, maa leen di leelseen suuxu bopp.Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen,ba ñépp xam nemaay Aji Sax ji lay wallu,jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»