Esayi48wol_mbs

Yàlla sikk na Israayil

1Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen;yeen ñi ñu woowe turu Israayil,yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda,di giñe turu Aji Sax ji,yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israayilte dëgg ak yoon taxul,2moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu sell bi,di wéeroo Yàllay Israayilji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi:3«Yàgg na maa biral lay njëkka am.Tuddoon naa ko, yégle ko,jekki jëf ko, mu sotti.4Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen.Dangeen të, wowle.5Moo tax ma yàgg leena biralal lii,yégal leen ko balaa teew.Lu ko moy ngeen ne:“Sunu tuur mee ko def,sunu tuuru bant bee,sunu tuuru weñ gee ko amal di!”6Lii lépp déggoon ngeen ko;xoolleen, xanaa dingeen ko nangu tey!«Bés niki tey dinaa leen yégal lu bees,muy kumpa gu ngeen xamul woon.7Léegi lees ko amal,du lu yàgg.Lu jiitu tey masuleen koo déggte dungeen ne xamoon ngeen ko.8Dégguleen, yéguleen,seeni nopp masula bënn;xam naa ne ay workati neen ngeen,“njuddu-fippu” lañu leen di woowe.9Waaye sama tur tax na ma aj sama mer,sama woy tax na ma muñal leen,ba duma leen far.10Ma ne, togg naa leen, xelli cib taal,waaye du taalu xellikaayu xaalis,sawaras nattu laa leen xellee.11Samaw tur a tax,sama tur laay jëfe.Jomb naa ñaaw!Te sama màggaay, duma ko joxe.
12«Dégluleen ma, yeen askanu Yanqóoba,yeen bànni Israayil gi ma dégtal sama woote.Maay kenn, maa njëkk te maa mujj;13te sama loxo bee dëj suuf,sama ndijoor bi firi asamaan.Maa leen di woo, ñu bokk taxaw.14Bokkleen daje yeen ñépp te déglu!Kan ci tuur yii moo yégle lii?Ki Aji Sax ji soppmooy sottal nammeelu Aji Sax ji ci Babilon,won Kaldeen ña fa dëkke diisaayu loxoom.15Maa àddu, man mii;maa ko woo, indi ko,te pexeem dina àntu.16Jegesileen ma, déglu ma;bu njëkk ba tey làquwuma, di wax;te ba muy xew, fa laa teew.»Tey Boroom bi Aji Sax ji da maa yebal,boole maak leeram.
17Aji Sax ji seen jotkat dafa wax,Aji Sell ju Israayil da ne:«Maay Aji Sax ji, seen Yàllaji leen di jàngal seen njariñ,di leen awale fa ngeen wara awe.18Céy su ngeen sàmmoon samay santaane,ba jàmm baawaanal leen,njekk géejal leen,19seen geño sakkan ni suuf,di seen meññeefu biir, tollook feppi suuf,du dog, du sànkoo fi sama kanam!
20«Génnleen Babilon,dawleen Kaldeen ñi, tey sarxolle.Biralleen lii, yéene ko,te yeggeji ko waa cati àddina,ne leen Aji Sax ji jot na jaamam Yanqóoba.»21Marewuñu béreb yu wow ya mu leen jaarale woon,ndox mu balle ciw doj la leen xellil,moo xaru doj, ndox ma baawaan .22«Jàmm,» la Aji Sax ji wax ne,«du ñeel ñu bon ñi.»