1Tuur ma ñu naa Bel toqi na,tuur ma ñu naa Nebo sukk,mala ya féetewoo seeni jëmm,ñoom lees daan gàddu , tey jur gi jagoo,di leen sëf ba loof.2Tuur yaa ngay sukk, bokk toqi;manuñoo wallu seen jëmm ya,xanaa doxal seen bopp, dugg cig njaam.3Aji Sax ji nee na: «Dégluleen yeen waa kër Yanqóoba,yeen ndesu kër Israayil gépp,yeen ñi ma dale yor ba ngeen juddoo,di leen fab ba ngeen génnee seen biiru ndey.4Ba ba ngeen di magal, man la,ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot.Maa sàkk, maay yor,maay boot, xettali!5«Ana ku ngeen may niruleel,di ma nàttableeka méngaleek moom,ba ñu niroo lenn?6Ñii déy a yullee wurus ci mbuus,sàkk xaalis, natt diisaay ba,fey tëgg bu leen ci tëggal am tuurmu ñuy sukkal aka sujjóotal,7yékkati teg ci mbagg,yóbbu, teg béreb, mu des fa;du jóge fa mu tege,ku ko woo wall it, du wuyu,ba jot ko ci njàqare.8Fàttalikuleen lii te dëgërluwaat!Yeen bàkkaarkat yi, defleen lii ci seen xel.9Fàttalikuleen cosaan la woon.Man mii maay Yàlla, du keneen.Amul Yàlla ju mel ni man!10Maay yégle muj ca ndoorte la,ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg.Maa naa sama mébét a ngii, day am,sama bépp nammeel sotti.11Maay woowe jaxaay penku,woowe réew mu sore, kuy sottal sama mébét.Maay àddu, amal;maay nas, sottal.12«Dégluleen maa, yeen dëgër bopp yi!Yeenaka dëddu njub!13Maa jegeñal sama àtte, soreetul;sama wall a ngii, yàggatul.Maay maye wall fi Siyoŋ gii,ba Israayil gii di sama gànjar.»