1Aji Sax ji dafa wax ki mu fal,Buur Sirus mi mu jàpp ci loxol ndijooram,ngir nangulal ko xeet yi,yolomal ngañaayal buur yi,lafal koy bunt,ba bunti dëkk du tëje,2mu ne: «Man maa lay jiitu,maasale mbartal,rajaxe buntu xànjar,damm tëjukaayu weñ.3Maa lay jagleel denc yu ruqe,ak alal ju làqe,ba nga xam ne maay Aji Sax ji lay woowe sa tur,man Yàllay Israayil.4Te Yanqóoba sama jaam bi,Israayil moomu di sama tànnéef moo taxma woowe la saw tur,takkal la ndombol tànk,te xamuloo ma.5Aji Sax ji man a, du keneen;kenn du Yàlla ku dul man.Maa la gemb,te xamuloo ma,6ngir xamees penku ba sowu,ne lu dul man neen la.Aji Sax ji man a, du keneen.7Maay bind leer,di def lëndëm.Maay indi jàmm,di def safaan.Maay Aji Sax jiy def lii lépp!8Na asamaan wis-wisal,niir tawal dëgg ak yoon;suuf fett, meññal wall,boole ci jebbil dëgg ak yoon.Man Aji Sax ji, maa def lii!»9Wóoy ngalla kuy diiŋat ka la tabaxte di ndabal xandeer ci biir ndabi xandeer!Ana ban ak di wax tabaxkatam,naa ko: «Looy def nii?Yaw amulooy loxo.»10Wóoy ngalla ku naan baayu nit,«Moo, lu sa geño meññ nii?»Mbaa ku naan ndeyu nit,«Li nga wasin lu mu?»11Aji Sax ji, Aji Sell ju Israayil dafa wax,moom mi ko bind,mu ne: «Lu dikkagul, nu ngeen ma ko ñemee laaje;am dangeen may jox ndigal ci samay doom,jox ma ko ci li ma liggéeye samay loxo?12Man maa amal suuf,sàkk doom aadama fi kaw suuf.Man mii la samay loxo firi asamaan,te maay jox gàngoori asamaan lépp ndigal.13Man maay yékkati Buur Sirus ci àtteb dëgg,xàllu yoonam.Man maay yékkati Buur Sirus ngir mu doxal yoon,maa koy xàllal yoon.Moom mooy tabax sama dëkk,yiwi sama ñoñ ñi ñu toxal,te du laaj pey mbaa neexal.»Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.14Aji Sax ji dafa wax ne:«Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus,ak waa Seba ñu njol ñi,ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo.Sa gannaaw lañuy topp,yeewe, jàllsi;sujjóotal la, di ñaan naan:“Fi yaw daal la Yàlla ne,du feneen,te tuur neen la.”»15Yaw déy, yaa di Yàlla ju làqu,yaw Yàllay Israayil ji koy wallu.16Yattkati xërëm yaa ngoogu, rus,torox, riixleendoo.17Israayil, yaay mucc fa Aji Sax jimucc gu sax dàkk!Doo rus, doo toroxfii ak ëllëg.18Aji Sax ji kat dafa wax,moom mi sàkk asamaan,moom Yàlla mi bind suuf,tabax ko, dëj ko,sàkkewu ko maraas,xanaa tabaxal ñu ko dëkke.Mu ne: «Aji Sax ji, man a, du keneen.19Làquwuma, di waxe béreb bu lëndëm.Newuma it askanu Yanqóoba:“Wërleen ma ci neen.”Man Aji Sax ji maay wax dëgg,di biral liy yoon.»20Yeen daw-làquy xeet yi,dajeleen, dikk,ànd, jegesi.Képp ku gàddu tuuru bantam,ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu,kooka xamul dara.21Àdduleen, layoosi,diisooleen fi seen biir kay!Ana ku xamle woon lii bu yàgg,yégle woon ko booba?Xanaa du man Aji Sax ji?Kenn du Yàlla ku dul man!Yàlla ju jub, di walloo,du kenn ku dul man!22Yeen waa àddina, catoo cat,walbatikuleen fi man, mucc.Man maay Yàlla, du keneen.23Giñ naa ko ci man mii,sama gémmiñ, dëgg a ciy jibe,di kàddu gu dul randu.Man la ñépp di sukkal seen bëti óom,man it la bépp boroom làmmiñ di giñe.24Dees na ma waxal ne:«Aji Sax ji rekk a jagoo àtte ak doole!»Mboolem ñi ma mereey ànd,sëgg, fekksi ma.25Ci Aji Sax ji la askanu Israayil gépp yeye,bay damu.