Esayi44wol_mbs

Aji Sax jee mat cëslaay

1«Yaw Yanqóoba, sama jaam bi, déglul boog,yaw Israayil sama tànnéef laa wax.2Aji Sax ji dafa wax, moom mi la sàkk,mooñ la fa sa biiru ndey,di la dimbali.Ma ne: Yaw Yanqóoba sama jaam bi,yaw Yesurun sama tànnéef laa wax,bul tiit.3Maay sottim ndox suuf su mar,ak wal yu waleg joor gu wow.Maay sotti saw askan samag noo,sama barke sottikul ñi nga meññ,4ñu màgg ni garabu saab-saab,nirook garab yu mag yu feggook ndox.5Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.”Kee di tuddoo turu Yanqóoba,kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji”tey wuyoo turu Israayil.»

Aji Sax ji dëkk na yàllantu yi

6Aji Sax ji dafa wax,moom buurub Israayil, jotkatam,Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,mu ne: «Maa njëkk, maa mujj,te Yàlla amul ndare man.7Ana ku mel ni man? Na àddu!Na biral firndeem te taajal mala amoon ba may sos xeet wu yàgg wa,ak li dikkagul.Na ko wax!8Buleen tiit, buleen ragal.Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko?Yeenay samay seede.Yàlla daa am ju ma moy?Cëslaay amul, xawma ci kenn!»
9Képp kuy tabax jëmmi tuur, doo tus,xërëm yooyu ñu safoo amul njariñ.Ñooñu ñu defi seedete gisuñu, yéguñu,muy seen gàcce!10Sàkk sam tuur,móol sa jëmmu tuur,te jariñu la tus!11Képp ku ca bokksa gàcce lay doon,ña koy yatt sax ay nit doŋŋ lañu.Nañu daje ñoom ñépp, taxaw,bokk tiitaangeek gàcce.
12Ab tëgg jël jumtukaayam,liggéey weñ ca taal ba,wàkk a wàkk, jëmmal;def ci kem kàttanam,teg ca xiif, doole jeex,naanul it ba tax mu loof.13Liggéeykatu bant tàllal buumu nattukaay,jël kew, nataale,xacc, rëdde rëddukaayu wërngal,jox ko bindu nit,jekkal ba mu mel ni nit,nar koo fat cib néeg,14ba tax mu gor garabi seedar,sàkk banti sippar ak yu ni mel,tànn ci garabi gott bi,mbaa mu jëmbat garab yu dëkke naat,ab taw màggal,15nit xambe, sàkk ci, jaaroo;taal, lakke mburu;sàkkaale ci jëmmu tuur, sujjóotal ko,muy jëmm ju mu defar, di ko sukkal;16xaaju matt ma lay taal,toggew yàppam, lekk,wàjj, xéewloo ba suur,jaaruwaale te naan:«Mii njaar mu neex!bii tàkk-tàkk bu yànj!»17Ndesu matt ma lay sàkke jëmmu tuuram,sukkal ko,sujjóotal ko, ñaan ko, naa:«Yaay sama Yàlla, xettali ma!»
18Ñii xamuñu, xàmmeewuñu,seeni gët lañu lëndëmal, ba gisatuñu;fatt seenum xel, ba xelootuñu.19Ku mel nii du delloosim xelam,ba xam, ràññee ne:«Xaaju matt mi laa taal,lakke mburu,wàjje yàpp, lekk;mu des, ma di ko sàkke lu seexluwu lii?Ab dogu bant laay sukkal?»20Kee di jur gu dunde dóomu-taal,xelam nax ko, sànk ko.Du keey musal bakkanam de!Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa yore nii?»
21Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii!Ma ne Israayil, fàttalikul, yaa di sama jaam!Ma bind la, ngay sama jaam,yaw Israayil, duma la fàtte!22Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir,say bàkkaar ne mes nib lay.Délsil fi man, jot naa la.»23Asamaan, sarxolleel, Aji Sax ji dikk na!Yeen xóotey suuf, xaaculeen!Yeen tund yi, neleen réllet, sarxolleendoo,ak yaw gott beek sa bépp garab!Aji Sax jee jot Yanqóoba,te moom Israayil lay fésale darajaam.

Dees na dëkkewaat Yerusalem

24Aji Sax ji sa jotkat dafa wax,moom mi la bind ba ngay sosu,ne: «Man maay Aji Sax ji sàkk lépp.Man doŋŋ maa tàllal asamaan,lal suuf, kenn wéttaliwu ma ca.25Maay neenal firndey maaman,dofloo gisaanekat.Maay weddi boroom xel mu rafet,def xam-xamam mu dig ndof.26Maay dëggal sama kàddug jaam,di sottal sama ndéeyal ndaw.Maa naan ci Yerusalem:“Dees na ko dëkke,”dëkki Yuda, ma ne:“Dees na leen tabaxaat,ma dekkali gentam bi.”27Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal,te maay ŋiisal say dex.”28Maa naa ci Sirus : “Sama sàmm bi!Mooy matal sama bépp nammeel,te it moo naa ci Yerusalem:‘Nees ko tabaxaat,’kër gu sell gi, la ne:‘Nees ko yékkatiwaat!’”»