Esayi42wol_mbs

Aji Sax ji yebal na jaamam

1Aji Sax ji nee: «Xoolleen sama jaam bii ma yor,sama tànnéef, sama soppey xol,ci moom laa sol sama xel,te mooy indil xeet yi yoonu àtte.2Du xaacu, du biral;du jibal baatam ci mbedd mi.3Barax bu lemu sax, du ko damm,leer gu giim it, du ko fey.Mooy indi yoonu dëgg.4Du toqi, du nasax,ba keroog muy dëj àtteb yoon fi kaw suuf,ba waa dun ya di séentu ndigalu yoonam.»
5Yàlla Aji Sax ji dafa wax,moom mi sàkk asamaan, firi ko;tàllal suuf ak lu mu jur,may noowal bakkan ñi ci kawam,ba ña cay daagoo di noyyi.6Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woongir nga doxal yoon;jàpp la ci loxo,sàmm la, def la ngay kóllëresama diggante ak nit ñi;def la ngay leeru xeet yi,7ngay gisloo gumba,di génne ku ñu tëj,ku dëkke woon lëndëm, génn kaso.
8«Man, Aji Sax jeey sama tur;sama màggaay, duma ko joxe,te sama bàkk, duma ko wacce jëmmi tuur.9Mbir ya jiitoo ngoog, mat na;yu yees laa leen di yégal,balaa teew, ma yegge leen ko.»

Woyleen Aji Sax ji

10Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,yeen waa cati àddina, kañleen ko,ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram,ak duni géej ak ña ca dëkke.11Na waa àll beeki dëkkam xaacoondoo,waa dalub Kedarak waa Sela sarxolleendoo,kaw tund ya di riirum mbég!12Nañu delloo Aji Sax ji màggaayam,te biral bàkkam biir duni géej.13Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar,xabtalu ni ñeyu xare,àddu ca kaw, xaacu,tiime noon yi njàmbaaram.

Aji Sax ji soppi na

14Aji Sax ji nee: «Damaa yàgga xeremlu,ne cell, téye sama bopp.Waaye léegi, ni kuy matu laay onke,di xiix aka àppaat boole ca.15Maay tonni tund wu mag ak wu ndaw,lu cay gàncax, ma laxal;ag dex, ma def ag joor;ab déeg, ma ŋiisal.16Maay doxloo silmaxa yici yoon wu ñu xamul,ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale.Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam ag leer,fu ñagas, ma maasaleel leen.Lii laa leen di defal,te duma leen wacc mukk!17Ñi wóolu ay jëmmi tuur,naan jëmm yu ñu móol:“Yeenay sunuy yàlla,”dees na leen waññi, toroxal leen.

Waa Israayil tëx nañu te silmaxa

18«Yeen tëx yi, dégluleen;yeen silmaxa yi, xoolleen ba gis.19Ana ku silmaxa ku moy sama jaam bii ?Ku tëx ba dab sama ndaw li ma yónni?Ana ku silmaxa ba dab kii ñu jàmmal?Ku silmaxa ba dab jaamu Aji Sax jii?20Gis nga lu bare,waaye jàppoo ci dara.Nopp ne kótt, dég-dég të!»21Aji Sax ji la soob ci njubteem,mu fésal màggaayu yoonam ak taar ba.22Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo;ñépp tëje ciy pax,dence ci kaso,ñu doon alalu xarefu leen kenn dul xettalee,xanaa ñu di leen sëxëtoo,te kenn du ne ñu delloo leen.
23Ana kan ci yeen mooy dékk lii nopp?Kuy teewlu, ba doxe fa dégg?24Ana ku jébbal waa kër Yanqóoba futtikat yi,ku jox Israayil gii, sëxëtookat yi?Xanaa du Aji Sax ji nu tooñ?Ñoo baña topp ay yoonam,baña sàmm ndigalu yoonam,25ba mu yuri leen tàngooru sànjam,sotti leen tar-taru xare,mu jafal wetoo wet, te taxul ñu xam,xoyom na leen te bawuñu ci xel.